ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw dana ko dégg-loo diine

ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw dana ko dégg-loo diine

Jële na ñu ci Muhaawiya -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw dana ko dégg-loo diine, man nag ab séddalekat kepp laa, waaye Yàlla mooy joxe, te xeet wii du deñ di taxaw ci mbiri Yàlla, ku wuute ak ñoom it du leen lor, ba baa mbiri Yàlla di ñëw».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw da koy wërsëgale dégg diineem ji ak ne moom Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mooy aji-séddale ji, day séddale li ko Yàlla mu kawe mi jox ci wërsëg ak xam-xam ak yeneen, waaye kiy joxe dëgg mooy Yàlla, ku dul moom nag sabab la du jariñ ci lu dul ndigalul Yàlla, ak ne xeet wii du deñ di taxawe mbiri Yàlla, te ku wuute ak ñoom it du leen lor, ba keroog bis-pénc.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi :Màggaay ak ngëneelul xam-xamu Sariiha ak d sàkku ko ak ñaaxe ca.

Xeet wi manut a ñàkk ñuy taxaw ci dëgg, bu ko am mbooloo bàyyee itam ñeneen taxawe ko.

Dégg diine daa bokk ci liy wane ne Yàlla namm na aw yiw ci jaamam bi.

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day joxe ci ndigalu Yàlla ak coobareem, waaye moom amul dara.

التصنيفات

Ngëneeli xam-xam