ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana

ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana

Jële nañu ci Sahl Ibn Sahd -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ñaari mbir yoy bu jullit taqoog moom day dugg àjjana, Bi ci njëkk: wattu làmmeñ ci wax luy merloo Yàlla mu kawe mi, Ñaareel bi: wattu péy mi (awara) ci tàbbi ci ñaawtéef; Ndax ñaari cér yii dañoo bari lu ñuy tàbbi loo nit ci bàkkaar.

فوائد الحديث

Wattu làmmeñ ak péy yoonu dugg àjjana la.

Jagleel nañu làmmiñ ak péy cig tudd; ndax ñoom ñaar ñoo gën a rëy ci liy indil nit ki alkandey àdduna ak allaaxira.

التصنيفات

Meloy Àjjana ak Sawara