moytuleen juróom-ñaar yiy alage

moytuleen juróom-ñaar yiy alage

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "moytuleen juróom-ñaar yiy alage", ñu ne ko: yaw Yónenteb Yàlla bi yooyu yan la ? Mu ne: "bokkaale Yàlla, ak njabar, ak ray bàkkan bu Yàlla araamal ñu ray ko ci ludul dëgg, ak lekk ribaa, ak lekk alali jirim, ak daw bisub xare , ak tuumaal jigéen i jullit ju saŋewu".

[Sahih/Authentic.] [Al-Bukhari and Muslim]

الشرح

Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ngi digal aw xeetam ngir ñu sori juróom-ñaari bàkkaar yiy alage, ba ñu ko laajee yan la ? Mu leeral ko ne mooy: Bi ci njëkk: bokkaale Yàlla, ci wutal ko moroom ak niroowaale moom aji-sell ji ci bépp melo wu mu man a doon, ak di jëmale gennug jaamu ci jaamu yi ci keneen ku dul Yàlla mu kawe mi. Dafa tàmbalee ci bokkaale ndax moo gën a rëy ci bàkkaar yi. Ñaareel bi: njabar- te mooy ay pas-pas ak i mocc ak ay garab ak i tux-, yoo xam ne day jeexital ci yaramu ki ñu njabar ci ray ko walla wopp-loo ko, walla tàqale diggante ñaar ñiy sëy. Ay jëfi Saytaane la, te ñu bari ci ñoom dañuy jëfëndikoo bokkaale, ak di jéem ma jege ruuh yu bon yi ci defal leen li ñu bëgg. Ñatteel bi: ray bakkan bu Yàlla tere ku ko ray ci lu dul lu sariiha waral, te ab àttekat moo koy def. Ñenteel bi: jëfandikoo ribaa ci diko lekk walla beneen anamu jariñu. Juróomeel bi: jalgati ci alali xale bi baayam faatu te matagul muskàllaf. Juróom-benneel bi: daw ci xare bu dox ci diggante jullit ñi ak yéeféer yi. Juróom-ñaareel bi: tuumaal jigéen ña fegu ci njaaloo, naka noonu it góor ñi.

فوائد الحديث

Bàkkaar yu mag yi nag tënkuwul ci juróom ñaar, kon dañoo tudd juróom-ñaar yii ngir séenug rëy ak seenug ñàng.

Ray bàkkan dagan na bu nekkee ci dëgg niki fayantoo, ak tubbi, ak njaaloo te jot a sëy, àttekat bi nak moo koy def.