bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate

bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate

Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral bàkkaar yu mag yi, te mooy gu ñu tëkku aji-def ji ci tëkku gu tar ci àdduna walla allaaxira. Bu njëkk bi "Bokkaale Yàlla": te mooy def wenn xeetu jaamu ñeel ku dul Yàlla, ak yamale lenn ak Yàlla ci lu Yàlla jagoo, cig jaamu, ak ug moomeelam ak ci ay turam ak i meloom. Ñaareel bi "Dënge ñaari way-jur": te mooy lépp luy waral lor ñaari way-jur moo xam wax la walla jëf, ak bàyyee rafetal jëme ci ñoom ñaar. Ñatteel bi "ray bakkan": ci lu dul dëgg, niki ray ko cig tooñ ak ug jalgati. Ñenteel bi "ngiñ luy nuural nit ": te mooy giñ lu waay def di fen te xam ne day fen, dañu koo tudde loolu nag; ngir ne day nuural boroomam ci ay bàkkaar walla ci sawara.

فوائد الحديث

Ngiñ luy nuuralaate amul lu koy kaffaara; Ndax daa bari loraange ak i ñaawtéef, moo tax fàwwu ñu tuub ko.

Ñenti bàkkaar yu mag yi ñu tudd ci hadiis bi du ngir tënk ko ca waaye day wane ne séen i bàkkaar daa màgg lool.

Bàkkaar yi daa séddalikoo yu mag ak yu ndaw, yu mag yi nag mooy: bépp bàkkaar bu am mbugalum àdduna, niki géten ak móolu, walla tëkkug allaaxira, niki tëkku ci dugg sawara, yu mag yi itam ay daraja la yenn yi moo gën a rëy araamug yeneen yi, bàkkaar yu ndaw yi nag mooy yi nekkul yu mag rekk.

التصنيفات

Ŋàññ moy yi