إعدادات العرض
kiy taxawu ak a dimbali ab Jatun ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg
kiy taxawu ak a dimbali ab Jatun ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "kiy taxawu ak a dimbali ab Jatun ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg"
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá ئۇيغۇرچە සිංහල ไทย دری Кыргызча or Kinyarwanda नेपाली Română Lietuvių Malagasy ಕನ್ನಡ Oromoo Nederlands Soomaali Српски Українська Moore ქართული Azərbaycan Magyarالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne kiy taxawe ay yittey jigéen ji jëkkëram faatu, te amul kenn ku taxawe ay mbiram, ak miskiin bi aajowoo, mu leen di dundal ci ngir yaakaar payug Yàlla mu kawe mi, kooku ak payam day yamoo ak kiy xeex ci yoonu Yàlla, walla kiy taxaw di julli guddi te du ca tàyyi, mbaa kiy woor te du dog.فوائد الحديث
Ñaaxe ci dimbalante ak jàppalante ci faj aajoy ñi néew doole.
Jaamu day làmboo jépp jëf ju baax, te bokk na ci ag jaamu taxawu ak a Dimbali jigéen ñi seen jëkkër faatu ak néew doole yi.
Ibn Hubayrata nee na: li ñu ci namm mooy Yàlla mu kawe mi da koy booleel yoolub woorkat ak taxawkatu guddu, ak jiihaatkat joxandoo ko ko; ndaxte dafa taxawu ki jëkkëram faatu taxawaayu jëkkëram..., taxawu miskiin bi manul a taxawe boppam, daal di koy jox ci desiitu dundam, sarax ko ci kàttanam, ba tax njariñam di yamoo ak woor ak taxaw guddi ak jihaat.
التصنيفات
Ngëneeli jëfi cér yi