إعدادات العرض
Yàlla dana bëgg ci jaam bi bu lekkee aw ñam mu sant ko ca, bu naanee ag naan sant ko ca
Yàlla dana bëgg ci jaam bi bu lekkee aw ñam mu sant ko ca, bu naanee ag naan sant ko ca
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee ne: «Yàlla dana bëgg ci jaam bi bu lekkee aw ñam mu sant ko ca, bu naanee ag naan sant ko ca».
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt සිංහල Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు မြန်မာ ไทย Deutsch 日本語 پښتو অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە Kiswahili தமிழ் دری Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy Română Kinyarwanda नेपाली Српски Soomaali Moore Українська Български Azərbaycan ქართული тоҷикӣ bm Oromoo Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sant gi jaam bi di sant Boroomam ci ay ngëneelam ak i xéewalam daa bokk ci bir yi ñuy ame ngërëmal Yàlla; bu lekkee aw ñam daal di wax: maa ngi sant Yàlla, bu naanee daal di wax ne: maa ngi sant Yàlla.فوائد الحديث
Teddug Yàlla mu màgg mi, ndax moo joxe wërsëg ci ngëneelam, daal di gërëm ngir cant gi.
Ngërëmal Yàlla dees na ko ame ci sabab yu yomb, niki sant ginnaaw lekk ak naan.
Bokk na ci teggini lekk ak naan: sant Yàlla ginnaaw lekk ga ak naan ga.
التصنيفات
Teggiini lekk ak naan