Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan

Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan».

[Tane na] [Ibnu Maaja soloo na ko - At-tirmisiy soloo na ko - Ahmat soloo na ko]

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne amul dara lu gën a tedd fa Yàlla ci jaamu yi lii di ñaan; ndaxte nangu la ci ne Yàlla ku doylu la -tudd naa sellam ga- ak nangu ne jaam bi dafa aajowoo Yàlla.

فوائد الحديث

Ngëneelu ñaan, ak ne képp ku woo Yàlla, ku ko màggal la, te nangu ne ku doylu la -tudd naa sellam ga-, ndaxte néew gi doole duñu ko ñaan, ak ne dafay dégg, ndaxte ku tëx duñu ko woo, ak ne mooy Aji-Tedd, ndax ku nay deesu ko ñaan, ak ne mooy yërëmaakoon bi, ku soxor duñu ko ñaan, ak ne ku am kàttan la, ku ñàkk doole duñu ko ñaan, ak ne Aji-Jege la, ku sori du dégg, ak yeneen meloy màgg yu dul yooyu tey wane màggug Yàlla Mu tedd mi ak taaram.

التصنيفات

Ngëneelu ñaan