Ku jáng benn araf ci téere Yàlla bi dina am benn tiyaaba, benn tiyaaba bu ne day tolloo ak fukki tiyaaba

Ku jáng benn araf ci téere Yàlla bi dina am benn tiyaaba, benn tiyaaba bu ne day tolloo ak fukki tiyaaba

Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Ku jáng benn araf ci téere Yàlla bi dina am benn tiyaaba, benn tiyaaba bu ne day tolloo ak fukki tiyaaba, waxuma nag {alif laam miim} aw araf la waaye alif araf la laam araf la miim araf la».

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bépp jullit bu jàng benn araf ci téere Yàlla bi dana am benn yiw, te dees na ko ful ba fukk yu mel ni moom. Mu leeral loolu ci waxam ji: (duma wax ni alif laam miim benn araf la waaye alif araf la, laam araf la, miim araf la): mu nekk ñatt mu am ca fanweeri yiw.

فوائد الحديث

Ñaaaxe ci di baril jàng Alxuraan.

Aji-jàng ji am na ci bépp araf ci baat bu mu jàng bu nekk yiw wu ñu ful ba fukk yu mel ni moom.

Yaatug yërmàndey Yàlla ak tedd-ngaam ba tax muy fulal jaam bi ab yool ngir ngëneelam ak teraangaam.

Ngëneelu Alxuraan ci kaw jeneen wax ju dul moom, ak jaamu Yàlla ci jàng ko; ndaxte waxu Yàlla la.

التصنيفات

Ngëneelu yittewoo Alquraan, Ngëneeli Alquraan ju tedd ji