إعدادات العرض
yaw xale bi, tuddal Yàlla, te lekke sa loxo ndeyjoor, te lekk li ne ci sa kanam
yaw xale bi, tuddal Yàlla, te lekke sa loxo ndeyjoor, te lekk li ne ci sa kanam
Jële na ñu ci Umar Ibn Abii Salamata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Bama nekkee xale ci kër Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, nuy lekk sama loxo doon wëreelu ci ndab li, Yónente bi ne ma: « yaw xale bi, tuddal Yàlla, te lekke sa loxo ndeyjoor, te lekk li ne ci sa kanam» booba ba leegi noonu laay lekke.
الترجمة
العربية Bosanski English فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Türkçe اردو हिन्दी 中文 বাংলা ئۇيغۇرچە Español Kurdî Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் සිංහල မြန်မာ ไทย 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands Hausa دری Кыргызча Lietuvių Kinyarwanda नेपाली Malagasy Italiano or ಕನ್ನಡ Oromoo Română Soomaali Српски Українська Moore Tagalog Azərbaycan ქართული Magyarالشرح
Umar Ibn Abii Salamata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, di doomi soxnas Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Ummu Salamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- -moom nag kër yónente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc la yaro- da ñuy xibaar ne: dadoon lekk ben bis loxoom di wër fune ci ndab li di fa tibb, Yónente bi daaldi koy xamal ñatti teggini lekk: Bi ci njëkk mooy: wax: "bismil Laahi" booy tàmbalee lekk ga. Ñaareel bi: lekke loxob ndeyjoor. Ñatteel ba: lekk ci sa kanam.فوائد الحديث
Bokk na ci teggini lekk ak naan wax Bismil Laahi ca tàmbali ga.
Jàngal xale yi ay teggin, rawatina ku nekk ci ron kilifteefug nit.
Ñeewanteg Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ak yaatug dënnam ci jàngal ndaw ñi ak yar leen.
Bokk na ci teggin yi nit ki lekk ci li feete ak moom, lu dul bu nekkee ñam yu wuute kon dana ca sañ a jël.
Sahaaba yi dañu daan taqoo ak li leen Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yare, te loolu dees na ko jariñoo ci waxi Umar je ne: Ba tay jii noona laay lekke.
التصنيفات
Teggiini lekk ak naan