ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam

ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day soññee ci jokk mbokk ak ci di leen seeti di leen teral ci yaram ak ci alal ak yeneen, ndaxte sabab la ci yaatug wërsëg ak gudd fan.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi :

Mbokk mooy jegeñaale yi ci wetu baay walla yaay, lu mu gën a jege gën a yayoo jokk.

Ag pay daal day toll kem na jëf tollu rekk, ku jokk ag bokkam cig mbaax ak rafetal, Yàlla jokk ko cig dundam ak wërsëgam.

Jokk mbokk sabab la ci yaatal wërsëg, sabab la it ci guddal Aw fan donte tënk nañu dund gi ak wërsëg wi, waaye day def barke ci wërsëg wi ak dund gi, day def cig dundam lu bari te ëpp njariñ, nee nañu itam wërsëg Wu yokk Wi ak fan Wu yokk Wi loolu dëgëntaan la.

Yàlla rekk moo xam.

التصنيفات

Ngëneeli jëf yu baax yi