Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar

Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar

Jële na ñu ci Umar ibn Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, bu waxee: ashadu an laa ilaaha illal Laahu, mu wax: ashadu an laa ilaaha illal Laahu, bu waxee: ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi, mu wax: ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi, bu waxee: hayya halas salaah, mu wax: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laah, bu waxee: hayya halal falaah, mu wax: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laah, bu waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, mu wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, bu waxee: laa ilaaha illal Laahu, mu wax: laa ilaaha illal laahu te mu dëggu ci xolam kon dana dugg àjjana».

الشرح

Nodd mooy yégal nit ñi ne waxtuw julli jot na, baati nodd nag ay baat yu dajale pas-pasu ngëm. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ci hadiis bi li ñu saytaane ci ku déggee nodd, te mooy ki ko degg muy wax li nodd-kat bi di wax, bu nodd-kat bi waxee "Allaahu Akbar" ki ko dégg wax: "Allaahu Akbar", ba mu jeex; bamu des fi nodd-kat bi di waxe "hayya halas salaah", "hayya halal falaah", kiy dégg day wax: "laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi». Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral ne ku bàmtu li nodd-kat bi di wax te mu sell ci xolam dana dugg àjjana. Baati nodd yi nag li muy firi mooy: "Allaahu Akbar" maanaam mooy Yàlla Aji-Sell ji moo gën a màgg gën a tedd lépp. "Ashadu an laa ilaaha illal Laahu": maanaam amul kenn lu ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla. "ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi" maanaam maa ngi saxal di seede ci sama làmmeñ ak sama xol ne Muhammat ndawul Yàlla mu màgg mi la, te dañu koo war a topp. "hayya halas salaah", maanaam kayleen ci julli gi, ak li kiy dégg di wax: "laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi", maanaam amul menn pexe ngir mucc ci yiy teree topp, walla genn kàttan ci def ko, mbaa genn kàttan ci lenn ci bir yi lu dul ci dëppaleg Yàlla mu kawe mi rekk. "hayya halal falaah" maanaam kaayleen ci texe gi, te mooy texe ci àjjana ak mucc ci sawara.

فوائد الحديث

Ngëneelu wuyu wooteb nodd-kat bi ci kem la muy wax, ba mu des ñaari hàyya-hala yi, mu wax "laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi".

التصنيفات

Ngëneeli sikkar, Nodd ak taxawal