buleen saaga ñi faatu, ndax ñoom kat wéy nañu ca lañu jiital

buleen saaga ñi faatu, ndax ñoom kat wéy nañu ca lañu jiital

Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «buleen saaga ñi faatu, ndax ñoom kat wéy nañu ca lañu jiital».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral araamug ŋàññi ñi faatu ak di wax ci séeni der, te loolu bokk na ci jikko yu ñaaw yi, ndax ñoom àgg nañu ca jëf ya ñu jiitaloon moo xam baax na walla bon na, te saaga woowu du àgg ci ñoom, te ñiy dundu rek lay lor.

فوائد الحديث

Hadiis bi day wane ne ŋàññi ñi faatu dafa araam.

Moytoo ŋàññi néew yi ngir bàyyi xel ci njariñu ñiy dund, ak ngir muccal askan wi ci xuloo ak mbañeel.

Njariñ li nekk ci tere ñu leen di saaga mooy ne ñoom dem nañu ca la ñu jiitaloon, kon saaga leen amul benn njariñ, te dafay gaañ mbokk yiy dundu.

Jaaduwul ci nit muy wax lu amul njariñ.

التصنيفات

Ngëneel yi ak teggiin yi, Dee ak i àtteem