Amul benn coono buy dal ab jullit, mbaa tawat walla, jaaxle, mbaa naqar, loraange, walla njàqare, doonte dég gu ko jam la, lu dul ne Yàlla dina ca fare yenn ci ay bàkkaaram

Amul benn coono buy dal ab jullit, mbaa tawat walla, jaaxle, mbaa naqar, loraange, walla njàqare, doonte dég gu ko jam la, lu dul ne Yàlla dina ca fare yenn ci ay bàkkaaram

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu, ak Abuu Hurayrata -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ñu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Amul benn coono buy dal ab jullit, mbaa tawat walla, jaaxle, mbaa naqar, loraange, walla njàqare, doonte dég gu ko jam la, lu dul ne Yàlla dina ca fare yenn ci ay bàkkaaram».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne liy dal jullit bi ci ay feebar ak i naqar ak i tiitaange ak i coono ak i musiba, ak ay tar-tar ak ragal, ak ub xiif -ba ci dég gu ko jam ba mettital ko-, loolu day far ay bàkkaaram di sippi ay ñaawtéefam.

فوائد الحديث

Leeral ngëneelu Yàlla ci jaamam yu gëm yi ak yërmàndeem ci ñoom, ci jéggal leen seen i bàkkaar ci lor yu néew yi leen di dal.

Jaadu na ci jullit bi muy yaakaar payug Yàlla ci li koy dal, di muñ lu ndaw ak lu rëy, ngir mu nekk ci ag yëkkatiku daraja ak far ay ñaawteef.

التصنيفات

Ngëneeli wéetal Yàlla