ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay

ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay

Jële na ñu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay»

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku jàng ñaari aaya yi mujj ci saaru Al-Baxara cig guddi Yàlla dana ko fegal ay ak lu mu sib, waxees na it: dana ko doy ci taxaw guddi, waxees na it: dana ko doy ci wird yépp, waxees na it: mooy li gën a néew lol dana doy ñu jàng ko Alxuraan ci julli guddi, wax nañu leneen it, amaana li ñu wax lépp a wér wax ji dana ko làmboo.

فوائد الحديث

Leeral ngëneelu mujjantalu saaru Al-Baxara, te mooy waxi Yàlla ji: (Aamanar rasuulu...) ba saar wa jeex.

Mujjantalu saaru day jeñal boroomam lu ñaaw ak S

saytaane bu ko jàngee ci guddi gi.

Guddi gi mi ngi tàmbalee fi jant bi di sowe, di jeexe fu fajar gi di fenke.

التصنيفات

Ngëneeli saar yi ak laaya yi, Sikkari suba ak ngoon