إعدادات العرض
Alal ji gën ci li nit ki di joxe: mooy alal ji mu jox njabootam ak alal ji mu jox ay daabaam ci yoonu Yàlla, ak alal ji mu jox ay àndandoom ci yoonu Yàlla
Alal ji gën ci li nit ki di joxe: mooy alal ji mu jox njabootam ak alal ji mu jox ay daabaam ci yoonu Yàlla, ak alal ji mu jox ay àndandoom ci yoonu Yàlla
Jële nañu ci Sawbaan -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Alal ji gën ci li nit ki di joxe: mooy alal ji mu jox njabootam ak alal ji mu jox ay daabaam ci yoonu Yàlla, ak alal ji mu jox ay àndandoom ci yoonu Yàlla» Abuu Xilaaba wax ne: "dafa, tàmbali ci njaboot Abuu Xilaaba, dellu wax ne: ana gan góor mooy gën a màgg ug pay ci góor guy jox njabootam gu ndaw di leen feg, mbaa Yàlla di leen jariñ ci moom ba def leen ñu doylu.
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Kiswahili Português සිංහල دری অসমীয়া ไทย Tiếng Việt አማርኛ Svenska Yorùbá Кыргызча Hausa ગુજરાતી नेपाली Oromoo മലയാളം Română Nederlands Soomaali پښتو తెలుగు Kinyarwanda ಕನ್ನಡ Malagasy Српски Moore ქართული Čeština Magyar Українська Lietuvių Македонски Azərbaycanالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ay meloy joxe, mu toftale ci li gën a war ci yaw bu dee anami joxe yi daa daje, mu tàmbalee ca la gën a am solo teg ca la ca tege; Mu xibaare ne alal ji ëpp yool mooy ji jullit bi jox koo xam ne moo ko war a jox; niki jabar ak doom, Teg ca jox waruwaay ju ñu waajal ngir xeex ci yoonu Yàlla, Teg ca jox ay xaritam ak i àndandoom bu ñu nekkee ci jihaad ci yoonu Yàlla.فوائد الحديث
Toftale joxe gi ci kem ngëneel yi ci anam gi ñu ko tudde, ñu sàmmoonte ak loolu bu yépp dajendoo.
Leeral ne njaboot gi ñoo gën a yayoo jox ci ngëneel ak ci yeneen.
Joxe ci jihaad ci yoonu Yàlla bokk na ci joxe yi gën a màgg, kem waajal jumtukaay yi, ak ñiy jihaadi.
Wax nañu ne: li ñu namm ci yoonu Yàlla mooy gépp jaamu niki aj.