إعدادات العرض
mo ndax Yàlla defalu leen lu ngeen di saraxee? Bépp sàbbaal ab sarax la, bépp sant ab sarax la, bépp tudd Yàlla it sarax la, digle lu baax sarax la, tere li bon sarax la, sëyug kenn ci yéen itam sarax la
mo ndax Yàlla defalu leen lu ngeen di saraxee? Bépp sàbbaal ab sarax la, bépp sant ab sarax la, bépp tudd Yàlla it sarax la, digle lu baax sarax la, tere li bon sarax la, sëyug kenn ci yéen itam sarax la
Jële nañu ci Abuu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Ay nit ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dañoo wax Yonnente bi ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, way-woomal yi yóbb nañu yool yi, dañuy julli kem ni nuy jullee, di woor kem ni nuy woore, ñuy saraxe ca seen disiiti alal, mu dal di wax ne: "mo ndax Yàlla defalu leen lu ngeen di saraxee? Bépp sàbbaal ab sarax la, bépp sant ab sarax la, bépp tudd Yàlla it sarax la, digle lu baax sarax la, tere li bon sarax la, sëyug kenn ci yéen itam sarax la", ñu ne ko yaw Yonnente Yàlla bi, ndax kenn ci nun day def bànneexam ba noppi di ci am sarax? Mu ne: "xanaa du bu ko defoon ci lu araam da ciy am bàkkaar? Niki noonu it bu ko defee ci lu dagan da ciy am yool".
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Hausa Kurdî Português සිංහල Kiswahili Tiếng Việt অসমীয়া ગુજરાતી Nederlands മലയാളം Română Magyar ქართული ಕನ್ನಡ Moore Svenska Македонски ไทย Українська తెలుగు मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛ Malagasy پښتو ភាសាខ្មែរ Lietuvių O‘zbek Azərbaycan Oromooالشرح
Yenn Sahaaba yi ñàkk dañoo jàmbat Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc seenuw melo ak seenug ñàkk ak li ñu manut a saraxe alal ngir am yool yu bari kem ni ko seen mbokk yi am alal ju bari di ame ngir ñu def ay yiw mel ni ñoom; ndax ñoom dañuy julli kem ni nuy jullee, di woor kem ni nuy woore, ñoom ñuy saraxe ci li des ci seen alal te nun dunu saraxe! Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tegtal leen li ñu man ci saraxe, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne leen: Ndax Yàlla defalu leen lu ngeen saraxe ci seen boop?! Li ngern di wax (Subhaanal Laah) dangeen ciy am yoolu sarax, niki noonu wax: (Allaahu Akbar) sarax la, ak wax: (Alhamdu lil-Laah) sarax la, ak wax: (laa-i-Laaha illal-Laahu) sarax la, ak (digle lu baax ( sarax la, ak (tere lu bon) sarax la, ba ci sax nit ki sëy ak jabaram sarax la. Ñu yéemu, daal di ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ndax kenn ci nun day dikke bànneexam ba noppi daal di ciy am yool?! Mu ne leen: ndax gisoo leen ne bu ko defoon ci lu araam ci njaalo mbaa leneen ndax dana ci am bàkkaar? Niki noonu it bu ko defee ci lu dagan da ciy am yool.فوائد الحديث
Rawanteg Sahaaba yi ci yiw yi, ak seenug xér ci am yool yu màgg ya ak ngëneel yi nekk ci Yàlla.
Bariwaayu anami jëfi yiw yi, ak ne day làmboo mbooleem jëf ju jullit bi di def ànd ca ak yéene ju baax ak jubluwaay bu rafet.
Yombug lislaam ak jàppandeem, jullit bu nekk dana am li mu jëf ngir topp ca Yàlla.
An-Nawawii nee na: lii dafay tegtal ci ne yu dagan yi dana mujj nekk ag jaamu Yàlla ci yéene yu baax, sëy dana nekk ag jaamu Yàlla bu ci yéenee jox soxna si àqam ak dund ak moom ci njekk gi yàlla digle, walla sàkku doom ju baax, walla ñoŋal boppam walla jabaram ak tere leen a xool lu araam walla di ci xalaat, walla di ko yittewoo, walla leneen lu dul loolu ci ay jubluwaay yu sell.
Sadd ay misaal ak i nattale; ngir mu gën a leer ci xelu aji-dégg ji.