ñoom dañu daan jàng ci Yónente bi fukki aaya, daawuñu jëlaat dara tek ko ca fukk ya ba baa ñuy xam li nekk ci yii ci xam-xam ak jëfe

ñoom dañu daan jàng ci Yónente bi fukki aaya, daawuñu jëlaat dara tek ko ca fukk ya ba baa ñuy xam li nekk ci yii ci xam-xam ak jëfe

Jele na ñu ci Abuu Abdu Rahmaan As-Sulamii -yal na ko Yàlla yërëm- mu wax ne: Ñi nu doon jàngal Alxuraan ci Sahaabay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax nañu nu ne ñoom dañu daan jàng ci Yónente bi fukki aaya, daawuñu jëlaat dara tek ko ca fukk ya ba baa ñuy xam li nekk ci yii ci xam-xam ak jëfe, nu wax ne: ñu boole xam ak jëfe.

الشرح

Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm-da ñu daan jàng ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki aayay Alxuraan, te daawuñu tuxu di jëll leneen ba kerook ñuy jàng li nekk ci fukk yooya ci xam-xam ñu jëfe ko, ñu boole xam-xam ba ak jëfe ga.

فوائد الحديث

Ngëneelu Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ak séenug xér ci xamlu Alxuraan.

Xamlu Alxuraan day nekk ci xam ak jëfe li ci nekk, waaye nekkul ci jàng ak mokkal rekk.

Xam-xam day jiitu wax ak jëf.

التصنيفات

Xam-xamu defar njàngiinu Alquraan, Teggiini jàng Alquraan ak ñi ko wattu, Ngëneeli xam-xam