إعدادات العرض
kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon
kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon
Jële nañu ci Usmaan Ibn Abil Haas -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Moom dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, Saytaane de dafa dox sama diggante ak sama julli gi, te day jaxase sama njàng mi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon", nee na: ma def loolu Yàlla dindi ko ci man.
الترجمة
العربية English မြန်မာ Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands اردو Bahasa Indonesia ئۇيغۇرچە বাংলা Türkçe සිංහල हिन्दी Tiếng Việt Hausa Kiswahili ไทย پښتو অসমীয়া دری Кыргызча Lietuvių Kinyarwanda नेपाली తెలుగు Bosanski ಕನ್ನಡ Kurdî മലയാളം Oromoo Română Italiano Soomaali Shqip Српски Українська Moore Tagalog Malagasy தமிழ் Azərbaycan فارسی ქართული 中文 Magyarالشرح
Usmaan Ibn Abil Haas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, saytaane de dafa dox sama diggante ak sama julli gi, mu tere ma cee toroxlug ragal Yàlla, muy jaxase sama njàng mi, di ma ci sikk-sakkaloo, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: kooku mooy saytaane bi ñuy wax Xinsab, bu loolu amatee nga yég ko, nanga làqu ci Yàlla, muslu ci Yàlla ci moom, te nga ëf ci sa càmmooñ mu ànd ak tuuti tiflit ñatti yoon, Usmaan nee na: ma def li ma Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digal, Yàlla dindi ko ci man.فوائد الحديث
Njariñu toroxlu ak teewaayug xol bi ci julli gi, ak ne saytaane day pastéefu ci jaxase ko ak def sikk-sakka ci kiy julli.
Sopp nañu muslu ci saytaane bu dee def ay jax-jaxal ci julli gi, ànd ak di tifli ñatti yoon ci wetu càmmoñ bi.
Leeral ni Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- daan delloo ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci lépp lu leen jaaxal, ba keroog mu leen koy lijjantil.
Dundug xoli Sahaaba yi, ci ne séen yitte mooy allaaxira.