إعدادات العرض
yal na Yàlla leeralal waaju dégg ci man dara mu jottali ko kem na mu ko dégge woon, bariwaana ku ñu jottali mu gën a xam aji-dégg ji
yal na Yàlla leeralal waaju dégg ci man dara mu jottali ko kem na mu ko dégge woon, bariwaana ku ñu jottali mu gën a xam aji-dégg ji
Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: "yal na Yàlla leeralal waaju dégg ci man dara mu jottali ko kem na mu ko dégge woon, bariwaana ku ñu jottali mu gën a xam aji-dégg ji".
الترجمة
العربية Bosanski English فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Türkçe اردو 中文 हिन्दी Español Hausa Kurdî Português සිංහල Kiswahili অসমীয়া Tiếng Việt ગુજરાતી Nederlands മലയാളം Română Magyar ქართული Moore ไทย Македонски తెలుగు मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛ বাংলা Malagasy Українська Tagalog ភាសាខ្មែរ ಕನ್ನಡ Svenska پښتوالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaanal ag leeraange ak ug nëtëx ak ug rafet ci àdduna, ak Yàlla eggale ko ci leeru àjjana ja ak i xéewalam ak ug leeram ca allaaxira; ñeel ki dégg hadiisam mokkal ko ba jottali ko keneen, ndax amaana ki ñu jottali hadiis bi gën a xam gën a dégg gën a man a jàngat ci ki tuxal hadiis bi, bu ko defee ku njëkk ki dàqa mokkal dàqa toxal , ku ñaareel ki dàqa dégg dàqa jàngat.فوائد الحديث
Ñaaxe ci mokkal Sunnas Yonente bi, ak jottali ko nit ñi.
Leeral ngëneelu waa hadiis, ak teddngay sàkku ko.
Ngënneelu woroom xam-xam yi nga xam ne ñooy ñi am ag dégg ak jàngat.
Ngënneelu Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm, ñoom ñooy ñi dégg hadiisi Yonente bi ba noppi jottali nu ko.
Al-Manaawii nee na: leeral na ci ne nekkul sàrt ci kiy nettali hadiis bi mu xam li hadiis bi di wax, waaye sàrtam mooy mu mokkal ko, war na ci boroom xam-xamu fiq bi mu xam lu ko ta settantal ko.
Ibn Uyayna nee na: amul kenn kuy sàkku hadiis lu dul ne kanamam dana amug leer ndax hadiis bii.
Mokkal ñaari xeet la ci boroom xam-xami hadiis yi: mokkal ci xol ak dënn, ak wattu ci téere ak bind, ñaar yépp nag hadiis bi da koy làmboo.
Dégg-déggi nit ñi dafa rawante, bariwaa na ku ñu jottali mu gën a xam aji-dégg ji, bariwaa na ku gàddu xam-xam te du boroom xam-xam.