torox na, torox na, torox na" ñu ne ko: kan? Yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne: "ku fekk ñaari way-juram di ay mag, kenn ka walla ñaar ñépp te duggul Àjjana

torox na, torox na, torox na" ñu ne ko: kan? Yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne: "ku fekk ñaari way-juram di ay mag, kenn ka walla ñaar ñépp te duggul Àjjana

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "torox na, torox na, torox na" ñu ne ko: kan? Yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne: "ku fekk ñaari way-juram di ay mag, kenn ka walla ñaar ñépp te duggul Àjjana".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñaanal toroxtange ba mu mel ni ku teg bakkanam ci suuf -baamtu na ko ñatti yoon- ñu laaj ko: kan ngay ñaan Yàlla yaw yonnente bi? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: ki fekk ñaari way-juram doon ay mag -kenn ka walla ñaar ñépp- te nekkuñu sabab ci mu dugg àjjana; loolu nag ngir ñàkk a rafetal jëme ci ñoom ñaar, ak ñàkk a leen a déggal.

فوائد الحديث

Dañoo war a rafetal jëme ci ñaari way-jur yi ndaxte daa bokk ci sababi dugg àjjana yi, rawati na bu ñu magee ba néew kàttan.

Ñàkk a déggal ñaari way-jur ci bàkkaar yu mag yi la bokk.

التصنيفات

Ngëneeli baax ci ñaari waa-jur