amul ñaari jullit yuy daje daal di joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal laata ñuy teqalikoo

amul ñaari jullit yuy daje daal di joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal laata ñuy teqalikoo

Jële nañu ci Al-Baraa yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "amul ñaari jullit yuy daje daal di joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal laata ñuy teqalikoo".

[Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne: amul ñaari jullit yuy daje ci aw yoon mbaa lu ko niru kenn ki nuyu keneen ki ñu joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal njëkk ñuy taqalikoo.

فوائد الحديث

Sopp nañu joxante loxo bu ñu dajee, ak soññee ca.

Al-Manaawii nee na: te sunna si du am ci lu dul teg ndayjoor bi ci ndeyjoor bi bu ngànt amul.

Ñaaxe ci tasaare nuyóo, ak leeral ngëneelu fayug saafonteg jullit bi ak mbokku jullitam.

Dees na settee ci hadiis bi joxante loxo gu araam niki góor di jox loxo jigéenu jàmbur.

التصنيفات

Ngëneeli jëf yu baax yi, Teggiini nuyoo ak yëglu