Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub

Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub

Jële na ñu ci An-Nuwaas Ibn Samhaan bokk ci waa Ansaar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub, te ci ñaari wetu yoon wi am na ñaari miir yu am bunt yu ubbeeku, ci bunt ya am ay rido yu ñu yoor, te ci buntu yoon wi am na kuy woote naan: “Yéen nit ñi! Duggleen ci yoon wi, te buleen jàdd. Am beneen wootekat buy woote nekk ca kaw yoon wa, bu bëggee ubbi dara ca bunt ya, mu ne ko: toskare ñeel na la bu ko ubbi, ndax boo ko ubbee da nga ca dugg. Yoon wa mooy Lislaam, ñaari miir yi: ñooy digi Yàlla yi, (fimiy yamlu) bunt yu ubbeeku yi: mooy terey Yàlla yi, kooku di woote ci boppu yoon wi: mooy Téereb Yàlla bi, kiy woote ci kaw yoon wi: mooy kiy waarekate ci Yàlla xolu jullit bu nekk».

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat]

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne: Yàlla dafa joxe misaal ci Lislaam ci yoon wu jub, tàllalu te amul benn dëng-dëng, ñaari pegg yi am ab miir, bu ko wër ci ñaari wet te ñooy digi Yàlla yi, ay bunt tu ubbeeku dox ci diggante ñaari miir yi, te mooy li Yàlla araamal, bunt yi am nañu ay rido yoy kiy romb ci yoon wi du gis ki ci biiram, njëlbeenu yoon wi am na kuy woo nit ñi di leen gindi naan leen: doxleen ci kawam te buleen jaar ci wet yi, wootekat bii nag mooy téereb Yàlla bi, amaat na fa it beneen wootekat bu nekk ci kaw yoon wi; wootekat bii nag saa bu ki nekk di dox ci yoon wi bëggee ubbi as lëf ci ridoy bunt yooyu mu xupp ko ne ko: toskare ñeel na la bul ko ubbi! Ndax boo ko ubbee rekk da nga ci dugg te doo man a téye sa bopp ba doo ci dugg, wootekat bii nag mooy waarekatu Yàlla bi nekk ci xolu jullit bu nekk.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Lislaam mooy diiney dëgg, te mooy yoon wu jub wi nuy àggale àjjana.

Danoo war a yam fa Yàlla yamlu ak ca la mu daganal ak la mu araamal, woyofal ko nag dana waral alkande.

Ngëneelu Alxuraan ju màgg ji ak soññee ci di ko jëfe, ndax ci la njub nekk ak leer ak texe.

Yërmàndey Yàlla ci jaamam ñi ak ci li mu def ci xolu way-gëm ñi lu leen di tere di leen waar ñu bañ a tàbbi ca alkande ya.

Yàlla ci yërmàndeem defal na jaam ñi kiiraay gu leen di teree tàbbi ci bàkkaar yi.

Bokk na ci jumtukaayi jàngale yi sadd ay misaal ngir jegeele ak leeral.

التصنيفات

Ngëneeli Alquraan ju tedd ji, Jëfi xol yi, Ŋàññ topp bakan ak bànneex yi