Dina ñu wax ëllag ki jàngoon Alxuraan: Jàngal te yéeg, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna, ndax sa kër moo ngi tolloog aaya bi ngay mujja jàng

Dina ñu wax ëllag ki jàngoon Alxuraan: Jàngal te yéeg, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna, ndax sa kër moo ngi tolloog aaya bi ngay mujja jàng

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Dina ñu wax ëllag ki jàngoon Alxuraan: Jàngal te yéeg, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna, ndax sa kër moo ngi tolloog aaya bi ngay mujja jàng».

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne kiy jàng Alxuraan te di ko jëfe, te taqoo ak moom cig jàng ak mokkal bu duggee àjjana dees na ko wax: jàngal Alxuraan, te yéeg ca darajay àjjana ya ndax loolu, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna ci njàng mu teey te dal; sa kër moo ngi ci aaya bi ngay mujj a jàng.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis:

Pay daal mi ngi ajo ca kem jëf ya cib tollowaay ak melokaan.

Ñaaxe ci jàng Alxuraan ak xereñe ko ak mokkal ko ak settantal ko ak jëfe ko.

Àjjana ay kër la ak i daraja yu bari, ñon Alxuraan yi danañu fa am ay daraja yu gën a kawe.

التصنيفات

Ngëneelu yittewoo Alquraan, Ngëneeli Alquraan ju tedd ji