Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ñeel Abuu Bakrin ak Umar: «ñaar ñii ñooy sangi paa yiy nekk àjjana ñu njëkk ña ak ñu mujj ña ba mu des yónente yi 

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ñeel Abuu Bakrin ak Umar: «ñaar ñii ñooy sangi paa yiy nekk àjjana ñu njëkk ña ak ñu mujj ña ba mu des yónente yi 

Jële nañu ci Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ñeel Abuu Bakrin ak Umar: «ñaar ñii ñooy sangi paa yiy nekk àjjana ñu njëkk ña ak ñu mujj ña ba mu des yónente yi ».

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa xibaare ne Abuu Bakrin Al-Siddiiq ak Umar Al-Faaruuq yal na leen Yàlla dollee gërëm ñoom ñoo gën ci nit ñi ginnaaw Yonnente yi, te ñoo gën ci ñi dugg àjjana ginnaaw Yonente yi.

فوائد الحديث

Abuu Bakrin ak Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm ñoom ñoo gën ci nit ñi ginnaaw Yonnente yi.

Àjjana amul paa, waaye ña cay dugg fanweeri at ak ñatt lañuy am, li ñu ci jublu mooy ñoom ñaar ñooy sangi ñi faatu ci àdduna te nekk paa, walla ñu jàppe ko anam ga ñu nekkoon ci àdduna jamonoy hadiis bii.

التصنيفات

Darajay Saaba yi Yàlla gërëm na leen, Ngëneeli Saaba yi Yalna Yàlla gërëm leen