dajee naa ak Ibraahiima guddi gi ñu ma rañaanee mu wax ne: yaw Muhammat, jottalil ma saw xeet samag nuyóo, te nga xibaar leen ne Àjjana lu teey ag suuf la, lu neex am ndox la

dajee naa ak Ibraahiima guddi gi ñu ma rañaanee mu wax ne: yaw Muhammat, jottalil ma saw xeet samag nuyóo, te nga xibaar leen ne Àjjana lu teey ag suuf la, lu neex am ndox la

Jële nañu ci Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "dajee naa ak Ibraahiima guddi gi ñu ma rañaanee mu wax ne: yaw Muhammat, jottalil ma saw xeet samag nuyóo, te nga xibaar leen ne Àjjana lu teey ag suuf la, lu neex am ndox la, te ab bayaal la, te la koy jëmbët mooy Subhaanal Laah, walhamdu lil-Laah, wa laa iLaaha illallaahu, wal-Laahu Akbaru ".

[Tane na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal] [At-tirmisiy soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne dafa daje ak Ibraahiima Al-Xaliil yal na ko Yàlla dolli jàmm guddig rañaan ga, mu ne ko yaw Muhammat: jottalil saw xeet samab nuyóo, te nga xamal leen ne Àjjana lu teey suuf la, lu neex ndox la te amul xorom, ak ne Àjjana lu yaatu la te maase wéet ci ay garab, te la koy jëmbët mooy baat yu teey yi, te ñooy yu sell yiy des: subhaanal Laah, walhamdu lil-Laah, wa laa-i-Laaha illal-Laahu, wal-Laahu Akbaru, saa su ko jullit bi waxee baamtu ko ñu jëmbëtal ko am njëmbët ca àjjana.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci saxoo tudd Yàlla ngir baril njëmbëti àjjana.

Ngëneelu xeetu lislaam wi; ba tax Ibraahiima yal na ko Yàlla dolli jàmm di ko jottali nuyóo.

Xemmemloog Ibraahiima yal na ko Yàlla dolli jàmm xeetu Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ñi baril tudd Yàlla mu kawe mi.

At-Tiibii nee na: àjjana pàkk bu yaatu la, topp ne Yàlla ci ngëneelam dafaa amal ay garab ak i njénn (palais) ci kem jëfi way-jëf yi; liggéeykat bu nekk ak la mu jagoo ci kem ligéeyam, topp ne ba ko Yàlla yombalalee la tax ñu bind ko ci ay jëf ngir mu am ab yool, ci la ko def mu mel ni moo jëmbët garab yooya.

التصنيفات

Ngëneeli sikkar