Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?

Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?» Nu ne ko: waaw. Mu ne: «kenn ci yéen jàng ñàtti aaya ci julli moo gën ci moom ñàtti giléem yu ëmb rëy te suur».

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne payug jàng ñàtti aaya ci julli; moo gën nit ki fekk ca këram ñàtti giléem yu ëmb rëy te suur.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Leeral ngëneelu jàng Alxuraan ci julli.

Jëf yu baax yi moo gën te mooy koomum àdduna bii di aji-jeex te moo fiy des.

Ngëneel lii nag tënkuwul ci jàng ñàtti aaya ci julli rekk; saa bu aji-julli ji di gën a yokk aaya yi ci julli gi ab yoolam di gën ci moom limub giléem yooyee.

التصنيفات

Ngëneeli Alquraan ju tedd ji