Wax naa: yaw Yonente Yàlla bi: kan laay gën a rafetal ci moom? Mu ne ma: "sa yaay, topp ca sa yaay, topp ca sa yaay, topp ca sa baay, topp ca ki gën a jege

Wax naa: yaw Yonente Yàlla bi: kan laay gën a rafetal ci moom? Mu ne ma: "sa yaay, topp ca sa yaay, topp ca sa yaay, topp ca sa baay, topp ca ki gën a jege

Jële nañu ci Bahr ibn Hakiim mu jële ci baayam mu jële ci maamam mu wax ne: Wax naa: yaw Yonente Yàlla bi: kan laay gën a rafetal ci moom? Mu ne ma: "sa yaay, topp ca sa yaay, topp ca sa yaay, topp ca sa baay, topp ca ki gën a jege".

[Tane na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne ki gën a yay ci nit ci ci lu baax ak rafetal jëme ci moom, ak rafetug jëflante, ak teeyug dundaale, ak ànd ak moom ak jokk ko: mooy yaay, mu feddali àqi yaay ci kaw àqi keneen ci baamtu ko ñatti yoon; ngir leeral ngëneelam ci nit ñi ci lu amul genn settee. Topp Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ngir leeral ki ci topp ci moom ci rafetal: topp ca sa baay, topp ca ki gën a jege ci mbokk yi, saa bu mbokk nekkee ku gën a jege rekk mooy gën a yay ci jokk ci ki gën a sori.

فوائد الحديث

Nekk na ci hadiis bi jiital àqi yaay, teg ca baay, teg ca mbokk mu gën a jege, ci kem seen daraja ci jege ga.

Leeral dayob ñaari way-jur rawati na yaay.

Baamtu na ci hadiis bi rafetal ci yaay ñatti yoon; loolu nag ngir ay ngëneelam yu màgg ci ay doomam, ak ngir bariwaayu li miy gàddu ci ay coono ak i tiis ak jafe-jafey ëmb, topp ca imbi, teg ca nàmpal, yi nga xam ne yaay rekk moo ko wéetoo, topp baay ji bokk ak moom yar gi.

التصنيفات

Ngëneeli baax ci ñaari waa-jur