jullit bi bu jàppoo ba raxas xar kanamam; bàkkaar bu mu mas a def ci ay gëtam day rot ànd ak ndox mi, -walla ànd ak toq ndox bi mujj-

jullit bi bu jàppoo ba raxas xar kanamam; bàkkaar bu mu mas a def ci ay gëtam day rot ànd ak ndox mi, -walla ànd ak toq ndox bi mujj-

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "jullit bi bu jàppoo ba raxas xar kanamam; bàkkaar bu mu mas a def ci ay gëtam day rot ànd ak ndox mi, -walla ànd ak toq ndox bi mujj-, bu raxasee ay yoxoom bépp bàkkaar bu mu mas a def ci ay yoxoom dana rot ànd ak ndox mi, ni ki noonu bu raxasee ay tànkam bàkkaar yi mu masa dox ak tànkam yépp dana rot ànd ak ndox mi -walla ànd ak toq ndox bi mujj-, ba keroog muy set wicc ci ay bàkkaar".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne jullit bi bu jàppoo daal di raxas xar kanamam ci njàppu mi bàkkaar bu ndaw bu mu mas a def ci ay gëtam day rot ànd ak ndox miy rot ginnaaw raxas ga walla mu ànd ak toq ndox bi mujj, bu raxasee ay yoxoom bépp bàkkaar bu ndaw bu mu mas a def ci ay yoxoom day rot ànd ak ndox mi walla ànd ak toq ndox bi mujj, ni ki noonu bu raxasee ay tànkam bàkkaar yu ndaw yi mu mas a dox ak tànkam yépp day rot ànd ak ndox mi walla ànd ak toq ndox bi mujj, ba keroog muy set wicc ci bàkkaar yu ndaw yi ci bu noppee ci njàppu mi.

فوائد الحديث

Ngëneelu sàmmonte ak jàpp, ak ne day far ay bàkkaar.

Bokk na ci njubug Yonente bi muy xemmemloo nit ñi topp Yàlla ak jaamu ko ci tudd fay gi ak yool bi.

Bépp cér ci céri nit ki day tàbbi ci yenn moy yi, moo tax bàkkaar yi day topp cér yi ko def, di génn bawoo ci bépp cér bu tuub.

Jàppu laab gu ñuy yëg la, te mooy booy raxas céri njàppu yi, laabug maanaa nag day nekk ci bàkkaar yi nga xam ne tàbbi na bawoo ci cér yi.

التصنيفات

Njàpp, Ngëneeli jëfi cér yi