إعدادات العرض
ndax du ma leen tegtal li Yàlla di fare njuumte yi, di ci yëkkatee daraja yi?
ndax du ma leen tegtal li Yàlla di fare njuumte yi, di ci yëkkatee daraja yi?
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ndax du ma leen tegtal li Yàlla di fare njuumte yi, di ci yëkkatee daraja yi?" Ñu ne ko ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne leen: "di jotale njàppu mi ci jomonoy sibeel ga, ak baril ay jéego jëm ca jàkka ya, ak di xaar julli ga ginnaaw ak julli, loolu mooy faanu ga».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt Hausa Kurdî Kiswahili Português සිංහල دری অসমীয়া ไทย አማርኛ Svenska Кыргызча Yorùbá ગુજરાતી नेपाली മലയാളം Oromoo Română Nederlands Soomaali پښتو తెలుగు Kinyarwanda Malagasy ಕನ್ನಡ Српски Moore ქართული Čeština Magyar Українська Македонски Lietuvių Azərbaycanالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Sahaaba yi ndax bëgg nañu mu tegtal leen ay jëf yoo xam ne sabab lañu ci jéggalug bàkkaar yi, ak far ko ca téerey malaaka ya koy wattu, ak kaweg ay daraja fa àjjana ? Sahaaba yi ne ko: waawaaw bëgg nañu loolu kay. Mu ne leen: Bi ci njëkk: jotale ak matale njàppu mi ci kaw coono yi; niki sedd, ak néewum ndox, ak mettitu yaram wi, ak ndox mu tàng. Ñaareel bi: baril ay jéego -te mooy li nekk ci diggante ndëggu yi- jëm ca jàkka ya ngir kër gu sori, ak baamtu gu bari. Ñatteel bi: xaar waxtuw julli, xol bi aju ca, ak di ko waajal, ak toog si jàkka ci di xaar mbooloo mi, bu ko jullee ba noppi toog fa mu jullee di xaar geneen julli. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di leeral ne bir yii mooy dëgg-dëggi fasukaay ga; ndaxte day fatt yooni saytaane yi ci bakkan, di not bànneex, di ko teree nangu ay jax-jaxal, ba tax mbooloom Yàlla mi di not soldaari saytaane yi; te loolu mooy jihaad gu mag gi, bu ko defee mu mel ni ag fasukaay ci yooni noon bi.فوائد الحديث
Solos sàmmoonte ak jullig mbooloo ca jàkka ja, ak yittewoo julli te bañ koo sàngane.
Rafetug njàngaliinu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak ni mu xemmemloo Sahaaba yi ba tax mu tàmbalee ci yool wu màgg wii ci anamug laaj, te lii yoon la ci yooni jàngale yi.
Njariñu gaaral masala yi ci anamug laaj ak tontu mooy: wax ji day gën a tàbbi ci xel mi ndax lëm gi ak leeral.
Imaam An-Nawawii -yal na ko Yàlla yërëm- nee na: loolu mooy fasukaay ga, maanaam: Ribaat (faanu) ga ñu xemmem, coosaanu ribaat mooy yeew dara, mu mel ni dafa yeew boppam ci jaamu gii, wax nañu it ne: mooy li gën ci faanu yi, kem ni ñu waxe ne it: jihaad mooy jihaadu bakkan, amaan itam mooy ribaat bi man a nekk, maanaam: dafa bokk ci xeeti ribaat yi.
Dañoo bàmtu baatub "ribaat" dugal ci "al" giy xamle; loolu nag ngir màggal mbiru jëf yii.
التصنيفات
Ngëneeli jëf yu baax yi