إعدادات العرض
bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla
bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla
Jële nañu ci Abdullah ibn Busrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: jenn waay dafa wax ne: yaw Yonnente Yàlla bi tërëliini lislaam yi dafa bari ci man, xibaar ma lol dinaa ci jàpp, mu ne ko: «bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla».
[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Hausa Kurdî Português සිංහල Nederlands অসমীয়া Tiếng Việt Kiswahili ગુજરાતી پښتو Română മലയാളം नेपाली Deutsch Кыргызча ქართული Moore فارسی Magyar తెలుగు Svenska Македонски ಕನ್ನಡ Українська Kinyarwanda Oromoo ไทย Српски मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛ Malagasy ភាសាខ្មែរ Lietuvių O‘zbek தமிழ் Azərbaycanالشرح
Jenn waay dafa jàmbat Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ne naafila yi dafa bari ci moom ba tax mu lott ci ngir néew kàttanam, mu laaj Yonnente bi ngir mu tegtal ko jëf ju néew juy indi yool yu bari ngir mu jàpp ci. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tektal ko ci muy Sax di tooyal làmmiñam ci tudd Yàlla ci bépp jamono ak ci gépp anam; ci sàbbaal ak sant ak jéggalu ak ñaan ak yu ko niru.فوائد الحديث
Ngëneelu saxoo tudd Yàlla mu kawe mi.
Bokk na ci màggug ngëneelu Yàlla mu yombal sababi yiw yi.
Gënlaanteg jaam ñi mingi ci seen cér yi ci bunti mbaax yi ak yiw yi.
Baril tudd Yàlla ci làmmiñ di sàbbaal ak di sant ak sikar ak di kàbbar ak yu dul yooyu, ànd ak mu dëppoo ak xol bi day taxaw taxawaayu ay naafila yu bari ci jaamu yi.
Sàmmonteek Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñeel aji-laaj ji ci tontu laaj bu nekk ca la méngoo ak moom.
التصنيفات
Ngëneeli sikkar