Bu nit ki faatoo ay jëfam dog na ba mu des ñatt: ba mu des saraxe buy wéy, walla xam-xam bu ñuy jariñoo, walla doom ju baax ju koy ñaanal

Bu nit ki faatoo ay jëfam dog na ba mu des ñatt: ba mu des saraxe buy wéy, walla xam-xam bu ñuy jariñoo, walla doom ju baax ju koy ñaanal

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «Bu nit ki faatoo ay jëfam dog na ba mu des ñatt: ba mu des saraxe buy wéy, walla xam-xam bu ñuy jariñoo, walla doom ju baax ju koy ñaanal».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi day xibaare ne jëfi aji-faatu ji day dagg cig faatoom, du am ay yiw ginnaaw ba mu faatoo ba mu des ñatti mbir ndaxte moom mooy sabab bi: Bi ci njëkk: sarax boo xam ni yool ba day sax, niki Wàqf, ak tabax jàkka, ak gas teen, ak yeneen. Ñaareel bi: xam-xam bu nit ñi di jariñoo, niki taalif ay téerey xam-xam, walla mu jàngal nit, nit kooka di tasaare xam-xam bi ginnaaw ba mu faatoo. Ñatteel bi: doom ju baax ju gëm di ñaanal ay way-juram.

فوائد الحديث

Woroom xam-xam yi dëppoo nañu ne bokk na ci liy egg ci nit ki cib yool ginnaaw bi mu faatoo: sarax buy wéy, ak xam-xam bu ñuy jariñoo, ak ñaan, aj it ñëw na ci yeneeni hadiis.

Dañoo tudd ñatt yii kese ci hadiis bii; ndaxte ñooy cosaani yiw, te mooy li ñu baax ñi di gën a bëgg a bàyyi seen ginnaaw.

Lépp lu ñuy jariñoo dana am yiw, waaye la nekk ca bopp ba ak njobbaxtal la mooy xam-xamu sariiha ak xam-xam yi koy dëgëral.

Xam-xam moo ëpp njariñ ci ñatt yii;

ndax xam-xam nit ki ko jàng da ciy jariñu, xam-xam lañuy sàmme sariiha, njariñu nit ñépp a ngi ci, te moo gën a daj gën matale ndaxte ci sa xam-xam la ñi fekke sa dund di jariñoo ak ñiy ñëw ginnaaw bi nga fatoo.

Ñaaxe ci yar xale yu baax; ndax ñoom ñooy jariñ seen i way-jur ca allaaxira, te bokk ci seen ug

jariñ ñu leen di ñaanal.

Ñaaxe ci rafetal jëme ci ñaari way-jur ginnaaw ba ñu faatoo, te dafa bokk ci rafetal giy jariñ doom ji batay.

Ñaan day jariñ ki faatu donte

jugewul ci doom, wànte dañoo tudd doom kese

ndaxte moom mooy wéy di ñaanal nit ki fàddu ba keroog mu fiy jóge moom.

التصنيفات

Li nit def ci yoonu Yàlla ci alalam ngir nit ñi di ko jariñoo te kenn du ko donn, Ngëneelu ñaan, Doing Good Deeds on behalf of the Deceased and Gifting them the Reward, Merit and Significance of Knowledge