kiy biral Alxuraan moo ngi mel ni kiy biral ab sarax, kiy yalu Alxuraan it moo ngi mel ni kiy nëbb ab sarax

kiy biral Alxuraan moo ngi mel ni kiy biral ab sarax, kiy yalu Alxuraan it moo ngi mel ni kiy nëbb ab sarax

Jële na ñu ci Huqbata Ibn Haamir Al-Juhanii -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «kiy biral Alxuraan moo ngi mel ni kiy biral ab sarax, kiy yalu Alxuraan it moo ngi mel ni kiy nëbb ab sarax».

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne kiy fésal jàngum Alxuraan moo ngi mel ni kiy fésal ab sarax bu muy joxe, kiy nëbbutu buy jàng Alxuraan moo ngi mel ni kiy nëbb ab saraxam.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Nëbb njàngum Alxuraan moo gën, kem ni nëbb ab sarax gëne, ndax li ci nekk ci sellal ak sori ngistal ak yéemu, lu dul ne aajo ak yéwénal moo waral biral ga niki jàngale Alxuraan.

التصنيفات

Ngëneeli Alquraan ju tedd ji, Ngëneeli jëfi xol yi, Teggiini jàng Alquraan ju tedd ji