إعدادات العرض
jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: "julli ci waxtoom" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "teg ca fonk ñaari way-jur" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "jihaad ci yoonu Yàlla
jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: "julli ci waxtoom" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "teg ca fonk ñaari way-jur" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "jihaad ci yoonu Yàlla
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj naa Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: "julli ci waxtoom" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "teg ca fonk ñaari way-jur" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "jihaad ci yoonu Yàlla" nee naa moo ma ko wax, te bi ma sàkkoon ndollin mu dolli ma.
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Hausa Português Kurdî Kiswahili සිංහල Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Tiếng Việt ไทย پښتو অসমীয়া دری Кыргызча or नेपाली Malagasy Kinyarwanda తెలుగు Lietuvių Oromoo Română മലയാളം Nederlands Soomaali Српски Українська Deutsch ಕನ್ನಡ Moore Shqip ქართული Azərbaycan Magyarالشرح
Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: julliy juróom ci waxtoom wi ko Sariiha tënk, Teg ca fonk ñaari way-jur, di rafetal jëme ci ñoom, di taxaw ci seeni àq, te bañ leen a moy, Teg ca jihaad ci yoonu Yàlla, ngir yëkkati kàddug Yàlla mu màgg mi, ak aar diineem ji ak waa diine ji, ak fésal màndargaam, ci bakkan ak ci alal. Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- nee na: moo ma xibaar jëf yii; te bu ma ko waxoon: teg ca lan? Kon dana ma dolli.فوائد الحديث
Gënanteg jëf yi ci seen diggante mi ngi aju ci Yàlla bëgg ko.
Ñaax jullit bi ci mu xér ci jëf yi, jiital bi gën teg ca ba ca tege.
Tontuy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jan jëf moo gën dana wuute, ci kem nit ñi ak seeni melokaan, ak lan moo ëpp njariñ ci kenn ku ne.