Yàlla du nangu ci jëf yi lu dul lu sell ñeel ko, ñu jublu sa jëmmam ji

Yàlla du nangu ci jëf yi lu dul lu sell ñeel ko, ñu jublu sa jëmmam ji

Jële nañu ci Abii Umaamata Al-Baahilii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ne ko: luy mbiri waa jiy xare ngir amug pay ak uw tur, lan moo ko ñeel? Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "dara ñeelu ko" mu baamtu ko ñatti yoon, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc naan ko: "dara ñeelu ko" topp mu ne ko: "Yàlla du nangu ci jëf yi lu dul lu sell ñeel ko, ñu jublu sa jëmmam ji"

[Wér na]

الشرح

Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: ngir laaj ko, di sàkku a xam àtteb waa ji génn jëm ca xare ba ak jihaad ga di sàkku ci Yàlla ag pay ak it bëgg nit ñi tagg ko kañ ko, ndax dana am ag pay? Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tontu ko: ci ne du am dara cig pay; ndax li mu bokkaale Yàlla ci yéeneem, waa ji baamtuwaat laaj bi ñatti yoon ci Yonnente bi feddaliwaat tontu bi; ci ne du am ug pay, topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xibaar ko tënk gi Yàlla di nangoo jëf: ci ne Yàlla du nangu jef lu dul ñu def lépp ngir moom wolif ñu koy bokkaale ak kenn, ak mu nekk ngir jëmmam ju Sell ji.

فوائد الحديث

Yàlla du nangu ci jëf yi lu dul lu ci sell ñeel Yàlla mu kawe mi, ak mu dëppoo ak njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Bokk na ci rafetug tontu aji-ubbee ji tontoom nekk lu matale bëgg-bëggu aji-laaj ji, ba dollil ko ca

Feddali mbir mu màgg ci baamtu laaj bi.

Jihaadkat dëgg mooy kiy jihaad ngir kàddug Yàlla yëkkëtiku, ngir sàkku fay ak yooli allaaxira ànd ak sellal yéene, waaye jihaadam du ngir àdduna.

التصنيفات

Ngëneeli jëfi xol yi