ragalleen Yàlla seen Boroom, te ngeen julli seen julli juróom yi, te woor seen weer wi, te joxe asakay seen alal ji, te topp ki jiite seeni mbir, kon dangeen dugg àjjanay seen Boroom

ragalleen Yàlla seen Boroom, te ngeen julli seen julli juróom yi, te woor seen weer wi, te joxe asakay seen alal ji, te topp ki jiite seeni mbir, kon dangeen dugg àjjanay seen Boroom

Jële nañu ci Abii Umaamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy xutba ca aju tàggatoo ga di wax naan: « ragalleen Yàlla seen Boroom, te ngeen julli seen julli juróom yi, te woor seen weer wi, te joxe asakay seen alal ji, te topp ki jiite seeni mbir, kon dangeen dugg àjjanay seen Boroom».

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-dafa xutba bisu arafa,ci ajug tàggatoo ga,ci atum fukkeel ma ci gàddaay gi,tudde nañu ko loolu; ndaxte Yonnente bi ci la tàggatook nit ñi. Mu digal nit ñépp ñu ragal seen Boroom ci def ay ndigalam te bàyyi ay tereem. Ak ñuy julli julliy juróom yi Yàlla mu màgg mi farataal ci bis bi ak ci guddi gi. Ak ñuy woor weeru koor. Ak ñuy jox seen asakay alal ña ko yeyoo te bañ caa nay. Ak ñu topp ñi Yàlla def njiit ci seen kaw, ci lu dul moy Yàlla, Ku def mbir yii ñu tudd payam mooy dugg àjjana.

فوائد الحديث

Jëf yii bokk na ci yiy sababi dugg àjjana.

التصنيفات

Ngëneeli jëf yu baax yi