إعدادات العرض
jëf yi juróom-benn la, nit ñi yitam ñent la ñu, ñaar yuy waral, ak yu tolloo, ak benn bu baax ñu ful fo ba mu mat fukk yunimel, ak wenn yiw wuñu ful bamu mat juróom-ñaari téeméer
jëf yi juróom-benn la, nit ñi yitam ñent la ñu, ñaar yuy waral, ak yu tolloo, ak benn bu baax ñu ful fo ba mu mat fukk yunimel, ak wenn yiw wuñu ful bamu mat juróom-ñaari téeméer
Jële na ñu ci Xuraym Ibn Faatik -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «jëf yi juróom-benn la, nit ñi yitam ñent la ñu, ñaar yuy waral, ak yu tolloo, ak benn bu baax ñu ful fo ba mu mat fukk yunimel, ak wenn yiw wuñu ful bamu mat juróom-ñaari téeméer, budee ñaar yiy waral nag mooy: ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu nag te bokkaale Yàlla ak dara dana dugg sawara. Yi tolloo nag mooy: ku yéene jëf lu baax ba xolam yég ko, Yàlla xam loolu ci moom, dees na ko bindal wenn yiw, ku def lu ñaaw it dees na ko bindal benn bu ñaaw, ku def lu baax ñu bindal ko fukk yu mel ni moom, ku joxe ci yoonu Yàlla yiw wu nekk dees na ko def juroom-ñaari téeméer. Nit ñi nag ñii dañu leen a yaatalal ci àdduna, xatalal leen ca allaaxira, ñii ñu xatalal leen ci àdduna yaatalal leen ca allaaxira, ñii ñu xatalal leen ci àdduna ak ca allaaxira, ñii ñu yaatalal leen ci àdduna ak ca allaaxira».
الترجمة
العربية English မြန်မာ Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands اردو Español Bahasa Indonesia ئۇيغۇرچە বাংলা Türkçe Bosanski සිංහල हिन्दी Tiếng Việt Hausa മലയാളം తెలుగు Kiswahili ไทย پښتو অসমীয়া Shqip دری Ελληνικά Български Fulfulde Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy or Română Kinyarwanda Српски тоҷикӣ O‘zbek नेपाली Moore Kurdî Oromoo Français Tagalog Azərbaycan Українська bm தமிழ் ქართული Deutsch Português Македонски Magyar فارسی Lingala Русский 中文الشرح
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne jëf yi juróom-benni xaaj la, nit ñi ñenti xeet lañu. Juróom-benni jëf yi mooy: Bu njëkk bi: ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara àjjana war na ci moom. Ñaareel bi: ku faatu te fekk dadoon bokkaale Yàlla ak dara sawara war na ci moom te fa lay sax. Ñaar yii ñooy ñaar yiy waral. Ñatteel bi: lu baax lu ñu yéene, ku yéenee def lu baax te mu dëggu ci yéeneem ba xolam yég ko, Yàlla xam ci moom yéeneem jii, am mbir mu ko gaar ba tax manut a def lu baax loolu, dees na ko bindal Aw yiw wu mat sëkk. Ñenteel bi: ñaawtéef wu ñu def, ku def lu ñaaw ñu bindal ko benn bu ñaaw. Ñaar yooyu ñooy: yu tolloo ci lu dul ful. Juróomeel bi: yiw woo xam ne dana nekk fukk yu mel ni moom, te mooy ku yéene yiw te def ko; dees na ko bindal fukki yiw. Juróom-beneel bi: yiw wu nekk juroom-ñaari téeméeri yiw, te mooy ku joxe benn joxe ci yoonu Yàlla, dees na ko bindal yiw wi juroom-ñaari téeméeri yiw, lii nag ci ngëneelu Yàlla mu kawe mi te barkeel la ak teraangaam ci kaw jaamam ñi . Bu dee ñenti xeeti nit ñi nag, ñooy: Ki ci njëkk: ku ñu yaatala wërsëgam ci àdduna, mu am fi xéewal, lu mu bëgg am ko fi, waaye dees koo xatalal ca allaaxira, te ag mujjam mooy sawara, te mooy yéefar bi woomle. Ku ñaareel ki: mooy ku ñu xatala wërsëgam ci àdduna, waaye di ku ñu yaatalal ca allaaxira, te ag mujjam mooy àjjana, kooku mooy aji-gëm ji ñàkk. Ku ñatteel ki: mooy ku ñu xatalal ci àdduna ak allaaxira, te mooy yéefar bi ñàkk. Ku ñenteel ki: mooy ku ñu yaatalal ci àdduna ak ca allaaxira, te mooy aji-gëm ji woomal.فوائد الحديث
Bokk na ci njariñal hdiis bi:
Màggug gëneelu Yàlla ci jaamam ñi ak ful gi muy ful jëf yu baax yi.
Maandug Yàlla ak tedd-ngaam, ndax dafa jëflante ak nun ci sunuy ñaawtéef cig maandute, payug benn ñaawtéef ben bu ñaaw la rekk.
Rëyug bokkaale, ndax day teree dugg àjjana.
Leeral ngëneelu joxe ci yoonu Yàlla.
Ful payug joxe ci yoonu Yàlla moo ngi tàmbalee ci juróom-ñaari téeméeri ful; ndaxte day dimbalee ci yëkkati kàddug Yàlla.
Leeral xeeti nit ñi ak séenug wuute.
Dana ñu yaatalal àdduna ki gëm ak ki gëmul, waaye deesul yaatalal allaaxira lu dul aji-gëm ji.