ku xandaalu daanu ci aw doj daal di ray boppam kooku ci sawaraw Jahannama la jëm di ca xandaalu sax ca di ku ñu fay saxal ba fàww

ku xandaalu daanu ci aw doj daal di ray boppam kooku ci sawaraw Jahannama la jëm di ca xandaalu sax ca di ku ñu fay saxal ba fàww

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "ku xandaalu daanu ci aw doj daal di ray boppam kooku ci sawaraw Jahannama la jëm di ca xandaalu sax ca di ku ñu fay saxal ba fàww, ku naan tooke daal di ray boppam tookeem ji day nekk ci loxoom mu koy naan ca sawaraw Jahannama sax fa di ku ñu saxal ba fàww, ku ray boppam ci ag weñ weñam gi day nekk ci loxoom mu ciy butti biiram bi ca sawaraw Jahannama sax fa di ku ñuy saxal foofa ba fàww ".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo na nit ki ray boppam ci àdduna te tay ko ndax kon dees na ko mbugal ca sawaraw Jahannama ci anam gi mu ko defe boppam ci àdduna muy ag fay gu dëppoo ak loola, ku daaneel boppam jóge ci kaw aw doj daal di ray boppam kooku dana nekk ca sawaraw Jahannama di daanu jóge ci kaw doji Jahannama yi di aji-sax di ku ñu ca saxal ba fàww, ku guux tooke daal di ciy ray boppam tookeem ji day nekk ci loxoom mu koy guux ca sawaraw Jahannama di aji-sax di ku ñu saxal foofa ba fàww, ku dóor boppam ag weñ ci biiram daal di dee, kooku weñam gi day nekk ci loxoom mu ciy jam biiram bi ca sawaraw Jahannama di aji-sax foofa.

فوائد الحديث

Araamalees na nit ki di ray boppam, ak ne dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi nga xam ne da ciy yayoo mbugal mu metti.

Li ñu tudd ci hadiis bi sadd misaal la rekk ci yenn xeeti ray bakkan yi, lu ko moy ci yoon wu ñu ko man a raye dees na ko mbugal ci kem li mu def boppam, ñëw na ci Sahiihul Buxaarii waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "ki xoj boppam dana ko xoj ca sawara, ak ki jam boppam it dana ko jam ca sawara".

An-Nawawii nee na: waxu Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc (kooku sawaraw Jahannama la jëm di aji-sax ñu saxal ko fa ba fàww); wax nañu ci ay wax, benn bi: dañu ko a yen ci ku ko def ngir daganal ko temu xamne dafa araam kii ab yéefar la, te lii mooy mbugalam, ñaareel bi: li ñu namm ci sax gi mooy diir bu gudd waaye du dëgg-dëggi sax, kem ni ñuy waxe: yal na Yàlla saxal nguuru buur bi, ñatteel bi: lii mooy fayam, waaye Yàlla mu Sell mi dafa baaxe daal di xibaare ne ku faatu di ab julli kooku du sax sawara.

Lii ci buntub niróole mbugali allaaxira ci jalgatiy àdduna yi la, dees na ci jële ne jalgati nit ki ci boppam mi ngi mel ni jalgateem ci kaw keneen ci bàkkaar; ndax moomul boppam, waaye Yàllaa ka moom, kon waru caa def lu dul lu ka ca Yàlla sant.

التصنيفات

Tooñaange yi, Ŋàññ moy yi