Yàlla du xool kuy diri ay yéreem ngir puukarewu

Yàlla du xool kuy diri ay yéreem ngir puukarewu

Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: "Yàlla du xool kuy diri ay yéreem ngir puukarewu".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo na ci yoor ay yére walla koddaay ba ci suufu dojor yi ngir yéem ak rëy-rëylu, ak ne ku def loolu yayoo na tëkku gu tar gi ci ne Yàlla du ko xool ëllëg bis-pénc xoolu yërmànde.

فوائد الحديث

Yére day làmboo lépp luy suturaal yaram ci tubëy ak mbubb ak koddaay ak yeneen.

Tere gi ñu tere buubal yére pur góor ñi rekk la, An-Nawawii nee na: woroom xam-xam yi dëppoo nañu ne buubal gi dagan na ci jigéen , ndax wér na jóge ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne digal na leen ñu yoor seen i sër lu tollu ni ab loxo.

Ibn Baas nee na: yoor gi lu ñu tere la lu araam la ngir mataleg hadiis yi, bu dee mbugal mi nag dafa wuute te it nekkul daa war a tolloo, ndax ki ci jublu rëy-rëylu bokkul ak ki ko jubluwul.

Ibn Baas nee na: jigéen awra la kon aayul mu yoor ko luy toll ak Sibr, bu ko doyul mu yoor ko luy toll ak loxo mu tàmballee ca dojor ba.

Al-Xaadii nee na: woroom xam-xam yi nee nañu: ci tënk sib nañu lépp lu yokk ca aajo ja ak la ñu aadawoo ci yére ci guddaay ak yaatuwaay, Yàlla rekk a xam.

An-Nawawii nee na: li ñu sopp ci liy wàcc ci catu mbubb mi ak koddaay gi mooy digg yeel bi, waaye lu nekk ci digganteem ak dojor yi it aayul, lu wàcc loolu nag moom sawara la jëm, li ñi sopp mooy digg yeel bi, li dagan te sibuñu ko mooy li ci suufam ba ca dojor ya, lu wàcc dojor yi nag moom tere na ñu ko.

Husaymiin wax na ci waxam ji: (Yàlla du ko xool) maanaam xoolu yërmànde ak ñeewant, waaye jubluwuñu ci xool yépp; ndaxte Yàlla mu Sell mi te kawe dara nëbbuwu ko, te dara fàdduwul wolif gisam gi, waaye li ñu ci jublu mooy xoolu yërmànde ak ñeewant.

التصنيفات

Teggiini col