Allaahuma innii as-aluka minal xayri kullihi, haajilihi wa aajilihi, maa halimtu minhu wa maa lam ahlamu, wa ahuusu bika minas saari kullihi, haajilihi wa aajilihi, maa halimtu minhu wa maa lam ahlamu

Allaahuma innii as-aluka minal xayri kullihi, haajilihi wa aajilihi, maa halimtu minhu wa maa lam ahlamu, wa ahuusu bika minas saari kullihi, haajilihi wa aajilihi, maa halimtu minhu wa maa lam ahlamu

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamal na ko ñaan gii: "Allaahuma innii as-aluka minal xayri kullihi, haajilihi wa aajilihi, maa halimtu minhu wa maa lam ahlamu, wa ahuusu bika minas saari kullihi, haajilihi wa aajilihi, maa halimtu minhu wa maa lam ahlamu, Allaahuma innii as-aluka min xayri maa habduka wa nabiyyuka, wa ahuusu bika min sarri maa haasa bihi habduka wa nabiyyuka, Allaahuma innii as-aluka aljannata, wa maa xarraba ilayhaa min xawlin wa hamalin, wa as-aluka sn tajhala kulla xadaa-in xadaytahu lii xayran".

[Wér na]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamal na Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm li boole ñaan yi, muy ñenti ñaan: Bi ci njëkk: ñaan gu matale wépp yiw: (yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan yiw yépp) lëppam, (la ca gaaw) li waxtoom jege, (ak la ca yeex) la sori, (li ma ci xam) ci li ga ma xamal, (ak li ma xamu), yi nekk ci sa xam-xam bi yaw Aji-Sell ji. Nekk na ci it wéer mbir yi ca Yàlla mu màgg mi; moom miy Aji-Peeg lépp, di ku ñeewant; moom Aji-Sell ji tànnal jullit bi la gën te gën ca a rafet, (maa ngi muslu) di làqatu di aaru (ci yaw ci ay yépp, ya ca gaaw ak ya ca yeex, ya ma ca xam ya ma ca xamul). Ñaanug ñaareel gi: mooy sàmm jullit bi ba du jalgati ci ñaanam (yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan) di sàkku ci yaw (li gën ci li la sa jaam ak sa ndaw li ñaan) yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, (maa ngi muslu) di aaru di làqu (ci yaw ci wépp ay bi sa jaam bi ak ndaw li muslu) yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, lii ag ñaan di ag sàkku ci Yàlla mu jox aji-ñaan ji li ko Yonnente bi Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc laaj ñaan ko ñeel boppam, ci lu dul muy lim xeeti li Yonnente bi ñaan. Ñaanug ñatteel gi: sàkku dugg àjjana, ak sori sawara, te mooy càkkutefu bépp jullit di jubluwaayu ay jëfam: (yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan àjjana) texe ca (ak lu cay jegeele ci wax walla jëf), yu sell yu lay gërëmloo, (maa ngi muslu ci yaw ci sawara) fa dara dul musle ci jëf yu bon yi lu dul sag ñeewant, (ak lu cay jegeele ci wax walla jëf) ci moy ci lay merloo. Ñaanug ñenteel gi: ñaan ag gërëm ci dogali Yàlla (maa ngi lay ñaan nga def bépp dogal goo dogal ñeel ma muy aw yiw) ak mépp mbir mu Yàlla dogal ñeel ma mu def ko muy aw yiw ñeel ma, lii dafa bokk ci ñaan ag gërëm dogali Yàlla yi.

فوائد الحديث

Góor gi jàngal njabootam lu leen di jariñ ci biri diine ak àdduna, kem ni Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamale Aysatu.

Ki gën ci jullit bi mooy mu wattu ñaan yii jóge ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc; ndax dafa bokk ci mataleg ñaan yi.

Woroom xam-xam yi wax nañu ci hadiis bii ne: mooy hadiis bi gën a matale ci ñaan yiw ak muslu ci ay, te moom dafa bokk ci wax yi gëna mat ci liñu jox Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Bokk na ci sababi dugg àjjana ginnaaw yërmàndey Yàlla: jef ak wax yu baax yi.

التصنيفات

Ñaan yi bawoo ci Yónnent bi SLM