إعدادات العرض
bu kenn jëmale mbokkam ngànaay, ndax xamul ne Saytaane man naa bif loxoom, mu tàbbi ci kàmbu sawara
bu kenn jëmale mbokkam ngànaay, ndax xamul ne Saytaane man naa bif loxoom, mu tàbbi ci kàmbu sawara
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "bu kenn jëmale mbokkam ngànaay, ndax xamul ne Saytaane man naa bif loxoom, mu tàbbi ci kàmbu sawara".
الترجمة
العربية Tiếng Việt অসমীয়া Nederlands Bahasa Indonesia Kiswahili Hausa සිංහල English ગુજરાતી Magyar ქართული Română Русский Português ไทย తెలుగు मराठी دری Türkçe አማርኛ বাংলা Kurdî Malagasy Македонски Tagalog ភាសាខ្មែរ Українська ਪੰਜਾਬੀ پښتو Mooreالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo na jullit bi di joxañ mbokku jullitam ci benn xeetu ngànnaay, ndaxte xamul man naa am Saytaane yóbbe ko ci yëngal ngànnaay li ci loxoom, mu ray mbokkam mi walla mu lor ko, bu ko defee mu tàbbi ci ag moy guy waral ci moom mu tàbbi ci paxu sawara.فوائد الحديث
Leeral araamug dereeti jullit.
War na ñu wormaal jullit bi ak moytu di ko lor moo xam ci jëf walla wax, te bokk na ci yooyu jëmële ko weñ walla ngànnaay, donte day kaf; ndaxte Saytaane amaana mu bif ko ci loxoom mu dóor ci mbokkam mi, walla mu rocci ngànnaay li ci loxoom mu dal ko ci lu dul jubluwaayam mu lor ci mbokkam mi.
Baare wépp yoon ak tere lépp luy jëme ci lu ñu tere.
Xér ci muccug mbooloo mi ak sàmm lënkaloo gi dox ci diggante nit ñi, ak bañ leen a ragalloo ak tiitalleen donte ci junj la walla xupp.
التصنيفات
Tooñaange yi