wax nga kàddu gog bu ñu ko jaxase woon ak ndoxum géej gi mu jaxase ko

wax nga kàddu gog bu ñu ko jaxase woon ak ndoxum géej gi mu jaxase ko

Jële nañu ci Aysatu yaayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Wax naa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: doy na la sëkk ci Safiyyatu lii ak lii, -kenn ci nettalikat yi nee na: maanaam dafa gàtt- mu ne ko: wax nga kàddu gog bu ñu ko jaxase woon ak ndoxum géej gi mu jaxase ko" ne na: ma nettali ko kenn nit, mu ne ma: bëgguma di wax ci nit donte damaa am lii ak lii".

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat]

الشرح

Aysatu yaayu jullit ñi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa wax Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: doy na la sëkk ci Safiyyatu -ki mu jublu mooy yaayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm- ne bokk na ci ayibi yaramam moom dafa gàtt, mu ne ko: wax nga kàddu goo xam ne bu ñu ko jaxase woon ak ndoxum géej gi kon mu not ko soppi ko yàq ko, nee na: ma jëf jëfu nit ngir wàññi ko, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: duma bégloo mukk may wax ci ayibam, walla ma koy toppandoo di def lu mel ni li muy def walla may wax lu mel ni li muy wax ci anamug wàññi donte dañu maa jox ci lu bari ci àdduna ngir loolu.

فوائد الحديث

Moytandikuloo ak ragalloo ci jëw.

Toppandoo melo yi ak roy nit ñi ci anamug xeebeel ak wàññi ci jëw gi araam la bokk.

Melal ayibi yaram yi ci xeeti jëw yi la.

Al-Xaadii nee na: jaxase ak rax ak soppi ci def ca leneen, maanaam jëw gii bu doon lu ñuy jaxase ak géej gi kon dana ko soppi ca meloom ma, ànd ak bariwaayam, kon naka la jëf yu ndaw yii di mel bu raxee ak moom.

Leeral lenn liy am ci diggante soxna yi ci fiirànge.

Yonente bi du saxal lu bon.

Tuutal mbiri àdduna ak li ci nekk bu ñu ko gam-gamlee ak ngërëmal Yàlla mu kawe mi ak ñàkk a meram.

Lislaam diiney jikkó yu rafet yi la, digle na ñu sàmm der yi ci bañ cee wax walla jëf lu koy xotti worma ji; ndaxte dafa bokk ci liy waral noonoo ak bañeel ci diggante jullit ñi.

التصنيفات

Jikko yees ŋàññ