moytulleen bàkkaar yi ñuy xeeb

moytulleen bàkkaar yi ñuy xeeb

Jële nañu ci Sahl Ibn Sahd -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "moytulleen bàkkaar yi ñuy xeeb bàkkaar yi ñuy xeeb dafa mel ni ay nit yu wàcc ci aw xur, kii indi ab bant, kii indi ab bant, ba ñu ñoral ca seen mburu, te bàkkaar yi ñuy xeeb saa bu ñu ci jàppee boroom mu alag ko".

[Wér na] [Ahmat soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day moytandikuloo ñuy woyofal def bàkkaar yu ndaw yi, ak di ko baril ndax day alage bu baree, mu joxe misaal ci loolu ci ay nit yu wàcc ci biir aw xur, ku nekk ci ñoom indi ab bant bu ndaw, ba ñu mjja ñorale seen mburu ci seen bant ya, ak ne bàkkaar yi ñuy xeeb saa bu ñu ci jàppee boroomam te tuubu ko walla Yàlla baal ko ko kon dana ko alag.

فوائد الحديث

Njubug Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci sadd ay misaal ngir jegeele maanaa ak yokk leeral gi.

Moytandikuloo bàkkaar yu ndaw yi ñuy xeeb, ak ñaaxe ci gaaw far ko.

Bàkkaar yi ñuy xeeb jamtal na ay maanaa: bi ci njëkk: lu jaam bi di def ci ay bàkkaar jàpp ne ci yu ndaw yi la bokk fekk ne ci yu mag la fa Yàlla, ñaareel bi: li jaam bi di def ci ay bàkkaar yu ndaw te du faale loolu te tuubu ko, bàkkaar yu ndaw yii di dajaloo ci kawam ba alag ko, ñatteel bi: lu jaam bi di def ci ay bàkkaar yu ndaw te faalewu ko, mu nekk sabab ci tàbbal ko ci yu mag yiy alage.

التصنيفات

Ŋàññ moy yi