إعدادات العرض
dénk naa leen julli ak ñi nekk ci seeni loxo
dénk naa leen julli ak ñi nekk ci seeni loxo
Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Li ëppoon ci dénkaaney Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bi muy génn àdduna: "dénk naa leen julli ak ñi nekk ci seeni loxo, dénk naa leen julli ak ñi nekk ci seeni loxo" (seen jaam yi), ba Yonente bi dënnam ba tàmbalee di xar-xarale, ba daanaka làmmiñam leeratul.
[Wér na] [رواه النسائي في الكبرى وابن ماجه]
الترجمة
العربية Tiếng Việt অসমীয়া Nederlands Bahasa Indonesia Kiswahili Hausa සිංහල English ગુજરાતી Magyar ქართული Română Русский Português ไทย తెలుగు मराठी دری Türkçe አማርኛ বাংলা Kurdî Malagasy Македонски Tagalog ភាសាខ្មែរ Українська ਪੰਜਾਬੀ پښتو Mooreالشرح
Li ëppoon ci dénkaaney Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñeel xeetam wi fekk ma nga ca sukuraatu dee: taqooleen ak julli te wattu ko te buleen ko sàggane, niki noonu it joxeleen àqi li ngeen moom ci ay jaam ak i jébéer te ngeen rafetal seen ug moomeel, deñul di ko bàmtu, ba mujj tàmbali di put gi di xar-xarale, ba sax làmmiñam mujjut a leer.فوائد الحديث
Màggaayu mbiri julli ak àqi jaam ñi; ndax Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da leen a dénkaane ci li mu mujja dénkaane.
Julli bokk na ci àqi Yàlla yi gën a màgg ci kaw jaamam ñi, ak joxe àqi mbindeef yi rawati na way-néew doole yi, ñi nekk ci suufu moomeel te bokkuñu ci njaboot bokk nañu ci ñi ci gën a màgg ay àq.
