ñiy rëbbaate duñu nekk ay seede du caagine ay rammkat ëllëg bis-pénc

ñiy rëbbaate duñu nekk ay seede du caagine ay rammkat ëllëg bis-pénc

Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñiy rëbbaate duñu nekk ay seede du caagine ay rammkat ëllëg bis-pénc».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku bari lu muy rëbb ñi yayoowul rëbb kooku yeyoo na ñaari mbugal: Bi ci njëkk: du nekk seede ëllëg bis-pénc ci xeet yi ci ne seen Yonente ya jottali nañu bataaxal ya, te deesul nangu seedeem ci àdduna; ngir ag kàccoorteem, te deesu ko wërsëgal faatu ci yoonu Yàlla. Ñaareel bi: du ramm ëllëg bis-pénc bu way-gëm yi di ramm seen i mbokk yi nga xam ne sawara war na ci ñoom.

فوائد الحديث

Araamalees na rëbbaate, ak ne baril ko dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi.

Mbugal mi nekk ci hadiis bii kiy bari lumuy rëbbe mooko moom, du ki ko def benn yoon ak lu ko niru, ni ki noonu kiy rëbbe rëbb gu dagan te mooy li rot ci Sariiha ci rëbb ña mel melo ya ñu ŋàññ niki nga wax: "yal na Yàlla rëbb Yahuud yi ak Nasaraan yi", "yal na Yàlla rëbb tooñkat yi", "yal na Yàlla rëbb nataalkat yi", "yal na Yàlla rëbb ñiy def jëfu niti Luut ya", "yal na Yàlla rëbb ku reddil ku dul Yàlla", "yal na Yàlla rëbb góor ñiy niru-nirulu jigéen, ak jigéen ñiy niru-nirulu góor", ak yu niru yooyu.

Saxal rammug way-gëm ñi ëllëg bis-pénc.

التصنيفات

Jikko yees ŋàññ