Weccee xaalis ci wurus ribaa la lu dul mu nekk loxook loxo, pepp ci pepp ribaa la lu mu nekk loxook loxo, orge ci orge ribaa la lu dul mu nekk am ak am maanaam loxook loxo, tàndarma ci tàndarma ribaa la lu moy loxook loxo

Weccee xaalis ci wurus ribaa la lu dul mu nekk loxook loxo, pepp ci pepp ribaa la lu mu nekk loxook loxo, orge ci orge ribaa la lu dul mu nekk am ak am maanaam loxook loxo, tàndarma ci tàndarma ribaa la lu moy loxook loxo

Jële nañu ci Maalik ibn Aws ibn Al-Hadsaan mu wax ne: ana kan mooy weccee dërëm? Talhata ibn Hubayd Allaa ne ko fekk booba ma nga ca Umar ibnul Xattaab yal na leen Yàlla dollee gërëm: wan nu sa wurus wi te nga ñëw bu sunu surga bi ñëwee, nu joxla sa xaalis, Umar ibnul Xattaab ne ko: déedéet, waat naa ko ci Yàlla danga koy jox xaalisam, walla nga delloo ko wurusam, ndax Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «Weccee xaalis ci wurus ribaa la lu dul mu nekk loxook loxo, pepp ci pepp ribaa la lu mu nekk loxook loxo, orge ci orge ribaa la lu dul mu nekk am ak am maanaam loxook loxo, tàndarma ci tàndarma ribaa la lu moy loxook loxo».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Taabihii bii di Maalik ibn Aws day xibaare ne dafa yoroon ay Diinaari wurus, bëgg ko a weccee ci ay Dërëmi xaalis, Abuu Talhata ibn Hubayd Allaa yal na ko Yàlla dollee gërëm neko: jox nu sa Diinaar yi ngir ma xool ko! Topp mu ne ko ginnaaw ba mu dogoo ci jënd gi: ñëwaatal bu sunu surga bi ñëwee ngir nu joxla sa Dërëmi xaalis, fekk Umar ibnul Xattaab yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ma nga fa, mu weddi xeetu jëflante boogu, mu giñal Talhata ci mu joxe xaalis bi leegi, walla mu delloo ko wurusam wi mu jële ci moom, mu leeral sababus loolu, ci ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ne jaay xaalis ci wurus walla safaan bi, kiy wecce daf ko a war a jël fa saasa, lu ko moy jaayante googu day nekk ribaa bu araam, di njaay mu yàqu, deesul jaay wurus ci xaalis du caagine xaalis ci wurus ci lu dul loxo ak loxo ku nekk jël, deesul jaay it mboq ci mboq walla pepp ci pepp walla orge ci orge mbaa tàndarma ci tàndarma ci lu dul kiif-kiif ci peese ak peese, natt ak natt loxo ak loxo, deesul jaay dara ci yooyu te ñaar yépp teewu ñu, te daganul ñu teqalikoo laata ku nekk di téye.

فوائد الحديث

Xeet yi ñu tudd ci hadiis bi juróom la: wurus ak xaalis ak mboq ak orge ak tàndarma, bu jaayante amee ci wenn xeet wi fàww mu am ñaari sàrt ngir mu wér: ku nekk téye ca barabu fasug njaay ma, ak ñu tolloo ca peese ga niki wurus ak wurus, lu ko moy ribaag ëppëlante lay doon, bu ñu wuute nag niki xaalis ak pepp kon benn sàrt la ngir pas gi wér, te mooy jël njëg gi ci barabu pas ga, lu ko moy mu nekk ribaag yeexe.

Li ñu namm ci barabu pas ga: mooy barabu jaayante ba, moo xam dañoo toog, walla dañuy dox, walla dañoo war, li ñu namm ci teqalikoo gi mooy li ñu nit ñi di jàppe ag teqalikoo ci aada.

Tere gi ci hadiis bi day làmboo wépp xeetu wurus wu ñu tëgg walla beneen, ak wépp xeetu xaalis bi ñu tëgg ak bi ñu tëggul.

Këyiti xaalisu jamono jii lépp lu war ci jaay wurus ci xaalis da cay war, maanaam bu dee dafa namm a weccee këyit ci geneen këyit niki Riyaal ci Dërëm kon ëppalante ci dana dagan ci kem ni ñaari wàll yi gërëme, waaye ku nekk têye ca barab ba luy war la, lu ko moy jaayante ga day yàqu, jëflante te ga mujj nekk ribaa bu araam.

Jëflanteg ribaa du dagan, te njaay ma baaxul donte ñaar ñépp da ñoo dàkkoor ca loola; ndaxte lislaam day sàmmal nit ki ak mbooloo mi seen i àq donte dañu ko a teggil seen bopp.

Aaye lu bon ak tere ko ñeel ku ko man.

Tudd tegtal gi ca ba muy tere lu bon la, kem ni Umar ibnul Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm def.

التصنيفات

Ribaa