ku am gàtt bu mu rendi bu weeru Tabaski bi duggee, bu mu jël dara ci kawaram ak ci weyam ba mu Tabaski ba noppi

ku am gàtt bu mu rendi bu weeru Tabaski bi duggee, bu mu jël dara ci kawaram ak ci weyam ba mu Tabaski ba noppi

Jële nañu ci Ammu Salamata yaayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm di soxnas Yonente bi mu ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "ku am gàtt bu mu rendi bu weeru Tabaski bi duggee, bu mu jël dara ci kawaram ak ci weyam ba mu Tabaski ba noppi".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digal na ki namm a rendi tabaskeem mu bañ a jël dara ci kawaru boppam walla naqam walla mustaasam walla leneen, niki noonu it bu mu dagg ci ay weyi loxoom walla tànkam dara bu nu gisee weeru Tabaski ba keroog muy Tabaski ba noppi.

فوائد الحديث

Ku yéenee Tabaski ginnaaw bi fukki fan yi duggee day tàmbali a bàyyi yooyu ñu tudd ca ba mu yéenee ba keroog muy tabaski.

Bu tabaskiwul ca bis bu njëkk ba day des di ko bàyyi ba baa muy tabaski ci bis bu mu man a doon ci bisi tabask yi.

التصنيفات

Gàttub Tabaski