إعدادات العرض
ku sàbbaal Yàlla …
ku sàbbaal Yàlla ginnaaw julli gu ne fanweeri yoon ak ñatt, sant Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, màggal Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, loolu juróom-ñent-fukk ak juróom ñent la, mu wax: ci mottali ko téemeer: laa-i-Laaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun, ñu jéggal ko ay njuumteem doonte dafa toll ni puuriti géej
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku sàbbaal Yàlla ginnaaw julli gu ne fanweeri yoon ak ñatt, sant Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, màggal Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, loolu juróom-ñent-fukk ak juróom ñent la, mu wax: ci mottali ko téemeer: laa-i-Laaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun, ñu jéggal ko ay njuumteem doonte dafa toll ni puuriti géej».
الترجمة
العربية Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tagalog Hausa Kurdî Português دری অসমীয়া ไทย Tiếng Việt አማርኛ Svenska Yorùbá Кыргызча Kiswahili ગુજરાતી नेपाली Română മലയാളം Nederlands Oromoo සිංහල తెలుగు پښتو Soomaali Kinyarwanda Malagasy ಕನ್ನಡ Српски Moore ქართული Čeština Magyar Українська Македонски Lietuvių Azərbaycanالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-leeral na ne ku wax ginnaaw bu noppee ci jullig farata gi: Fanweeri yoon ak ñatt: "Subhaanal Laahi" te mooy sellal Yàlla ci gépp wàññiku. Ak fanweer ak ñatt: "Alhamdu lil-Laahi" te mooy tagg ko ci ay meloom yu mat ànd ak bëgg ko ak màggal ko. Ak fanweer ak ñatt: "Allaahu Akbar" te mooy ne Yàlla moo gën a màgg lépp. Ngir mottali lim bi téeméer mu wax: "laa iLaaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun" maanaam mooy: amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dong amul bokkaale, ak ne moom Yàlla mu sell mi moo jagoo nguur gu mat, moo yeyoo kañ ak tagg gu ànd ak bëgg ak màggal wolif keneen ku dul moom, ak ne moom lépp la man dara tëwu ko. Ku wax loolu loolu dees na far ay njuumteem jéggal ko, donte dafa bari ba toll ni puurit yu weex yiy nekk ci kaw géej gi bu dee yëngatu.فوائد الحديث
Sopp nañu sikar yii ginnaaw julli yi ñu farataal.
Sikar yii sabab la ci jéggale bàkkaar yi.
Màggug ngëneeli Yàlla mu kawe mi ak yërmàndeem ak njéggalam.
Sikar yii sabab la ci njéggalug bàkkaar yi, li ñu ci namm
mooy: bàkkaar yu ndaw yi, bu dee yu mag yi nag dara du ko far lu dul tuub.
التصنيفات
Sikkar yi ànd ak julli gi