Xëdd nañu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc topp mu jug jëm ca julli ga, ma ne ko: ñaata moo dox ci diggante nodd gi ak xëdd gi? Mu ne: luy tolloo ak juróom-fukki aaya

Xëdd nañu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc topp mu jug jëm ca julli ga, ma ne ko: ñaata moo dox ci diggante nodd gi ak xëdd gi? Mu ne: luy tolloo ak juróom-fukki aaya

Jële nañu ci Saydu ibn Saabit yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Xëdd nañu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc topp mu jug jëm ca julli ga, ma ne ko: ñaata moo dox ci diggante nodd gi ak xëdd gi? Mu ne: luy tolloo ak juróom-fukki aaya.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yenn Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm xëdd nañu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, topp mu jug moom Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jëm ca jullig fajar ga. Anas wax Sayd ibn Saabit yal na ko Yàlla dollee gërëm ne ko: ñaata la waxtu wi toll ci diggante nodd gi ak noppi gi ci xëdd gi? Sayd yal na ko Yàlla dollee gërëm ne ko: mi ngi tollu ak jàng juróom-fukki aaya hu yemoo, déet muy yu gudd du caagine yu gàtt, déet muy njàngat mu bar du caagine mu yeex.

فوائد الحديث

Ngëneelu yeex a xëdd ba laata fajar ci lu néew; ndaxte bu yexee ca la njariñj yaram wi di gën a màgge, te it ca la njriñam ci moom ci bis bi di ëppe.

Xérug Sahaaba yi vi dajaloo ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ngir jàng ci moom.

Rafetug dunddinu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñeel ay Sahaabaam, ba tax mu daan lekkandoo ak ñoom.

Waxtuw jàpp mooy fenkug fajar gi.

Waxam ji: "ñaata moo dox ci diggante nodd gi ak xëdd gi", li ñu ci namm mooy diggante xëgg gi ak liqaam gi; ndax ki mu wax ci beneen hadiis: "ñaata moo dox ci bi ngeen noppee ci xëdd gi ak bi ngeen dugge ci julli gi", te hadiis yi yenn yi dañuy firi yeneen yi.

Al-Muhallab nee na: nekk na ci it nattale waxtu yi ci jëfi yaram yi, Araab yi daan nañu nattale waxtu yi ci jëfi yaram yi niki seen wax ji: luy tolloo ak ràttum gàtt, ak loy tolloo ak loj giléem, Sayd ibn Saabit yal na ko Yàlla dollee gërëm jeng jëm ci nattale ci njàng mi; ngir junj ci ne waxtu wi waxtuw jaamu la ci jàng, bu doon daan nañu nattale ci lu dul ag jëf, kon dana wax ci misaal: luy tollu ak darajay, walla ñatteelu, juróomeelu xaaju waxtu wi.

Ibn Abii Jamrata nee na: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na xool li gën a am ñeewant ci xeetam wi mu def ko; ndaxte moom bi xëddul woon kon danañu ko ca topp te kon dana diis ci ñenn ñi, bu xëddoon ci diggu guddi gi kon it dana diis ci ñenn ñi nga xam ne nelaw moo leen di not ndax amaana mu mu yóbbe leen ñu bàyyi jullig suba gi walla muy aajowoo pasteefu ci fog.

التصنيفات

Sunnay koor