ku fàtte ne dafa woor, daal di lekk walla mu naan, na mottali wooram, ndax Yàlla moo ko leel moo ko mànnal

ku fàtte ne dafa woor, daal di lekk walla mu naan, na mottali wooram, ndax Yàlla moo ko leel moo ko mànnal

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «ku fàtte ne dafa woor, daal di lekk walla mu naan, na mottali wooram, ndax Yàlla moo ko leel moo ko mànnal».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi day leeral ne ku lekk walla mu naan fekk dafa fàtte ne daa woor kooru farata walla naafila na mottali wooram te bu mu dog; ndaxte jubluwul a dog, waaye moom wërsëg wu ko Yàlla wommatal jëme ko ci moom la ngir leel ko mànnal ko.

فوائد الحديث

Ki lekk mbaa mu naan te fekk daa fàtte kooram wér na.

Ki lekk walla mu naan ta fekk daa fàtte du ci am bàkkaar; ndaxte du moo ko tànn.

Ñeewanteg Yàlla ci jaamam ñi, ak yombal ci seen kaw, ak yëkkëti coono ak jafe-jafe ci ñoom.

Aji-woor ji du doge ci lenn ci yiy dogloo lu dul bu ci ñatti sàrt dajee: bu njëkk bi: muy aji-xam, bu dee dafa nekk aji-réer kon du dog, ñaareel bi: mu nekk di aji-fàttaliku, bu dee aji-fàtte la, kon wooram wér na te fay waru ko, ñatteel bi: muy aji-tànn déet muy ku ñu ga, ci mu jëfandikoo luy dogloo ci lu mu tay.

التصنيفات

Yiy yàq koor