dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor

dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor

Jële nañu ci Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc soññee na ci pasteefu ci dàkk Laylatul Xadri ci di baril ay jëf yu baax, moom nag fa gën a yaakaaru mooy mu nekk ci guddi yu wéet yi ci fukki fan yu mujj yi ci weeru koor ci at mu nekk, te mooy: ñaar-fukk ak benn, ak ñaar-fukk ak ñatt, ak ñaar-fukk ak juróom, ak ñaar-fukk ak juróom-ñaar, ak ñaar-fukk ak juróom-ñent.

فوائد الحديث

Ngëneelu Laylatul Xadri ak ñaaxe ci di ko dàkk.

Bokk na ci xereñteg Yàlla ak yërmàndeem mu nëbb guddi gii ngir nit ñi pasteefu ci jaamu gi, ngir sàkku ko, ndax seen yool bari.

Laylatul Xadri mi ngi ci fukki guddi yi mujj ci weeru koor, te ci yu tóol yi la gën a yaakaaru.

Laylatul Xadri benn la ci fukki guddi yi mujj ci weeru koor, te mooy guddi gi Yàlla mu màgg mi wàcce Alxuraan ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu def guddi gii mu gën junni weer ci baarke, ak màggug dayoom, ak jeexiti jëf yu baax ci moom.

Tudde nañu ko(Laylatul Xadri) ci sukoon Daal gi benn mu jóge ci teddnga, dees na wax: diw ku màgg dayo la, laafal gi ñu laafal guddi gi nekk ci buntub laafal dara ci meloom, maanaam guddi gu tedd gi, maanaam moom ku màgg dayo la ci teddnga ak ug màggaay ak ug dayo ba mu jeex, {Nun noo ko wàcce ci guddi gu baarkeel} [Ad-Duxaan: 3], benn mu jóge ci nattale: laafal gi nekk laafal jamono ca la mu làmboo, maanaam guddi gii mooy gi nga xam ne ca la nattale liy am ci at mi di nekk, {ca lañuy teqale bépp mbir mu ñu xereñe} [Ad-Duxaan: 4].

التصنيفات

Fukki guddi yi mujj ci weeru Koor